Al-A'raf · 29/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
قُلْ أَمَرَ رَبِّي بِالْقِسْطِ ۖ وَأَقِيمُوا وُجُوهَكُمْ عِندَ كُلِّ مَسْجِدٍ وَادْعُوهُ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ ۚ كَمَا بَدَأَكُمْ تَعُودُونَ ۝٢٩
Qul amara Rabbee bilqisti wa aqeemoo wujoohakum `inda kulli masjidin wad`oohu mukhliseena lahud deen; kamaa bada akum ta`oodoon
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Yàlla Dafa digle maandute. Nangeen di jublu ci jàkka yépp te nangeen ko jaamu, di sellal ngir Moom [Yàlla]. Dangeen dellu ca Moom, na Mu leen sose woon cag njalbéen”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 27-31 — Al-A'raf

27يَا بَنِي آدَمَ لَا يَفْتِنَنَّكُمُ الشَّيْطَانُ كَمَا أَخْرَجَ أَبَوَيْكُم مِّنَ الْجَنَّةِ يَنزِعُ عَنْهُمَا لِبَاسَهُمَا لِيُرِيَهُمَا سَوْآتِهِمَا ۗ إِنَّهُ يَرَاكُمْ هُوَ وَقَبِيلُهُ مِنْ حَيْثُ لَا تَرَوْنَهُمْ ۗ إِنَّا جَعَلْنَا الشَّيَاطِينَ أَوْلِيَاءَ لِلَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ
Yéen doomi-aadama ! Buleen Séytaane sànke ni mu génne woon seen ñaari maam ya Àjjana, muri seeni koddaay ngir won leen seeni pëy. Moom mi ngi leen di gis, moom ak njabootam, te yéen mënuleen a gis fa ñu nekk. Nun def Nanu Séytaane ya ñu lëkkaloo ak ñi gëmul,
28وَإِذَا فَعَلُوا فَاحِشَةً قَالُوا وَجَدْنَا عَلَيْهَا آبَاءَنَا وَاللَّهُ أَمَرَنَا بِهَا ۗ قُلْ إِنَّ اللَّهَ لَا يَأْمُرُ بِالْفَحْشَاءِ ۖ أَتَقُولُونَ عَلَى اللَّهِ مَا لَا تَعْلَمُونَ
bu ñu defee ñaawtéef, dañuy wax ne : “Danoo fekk sunuy maam di ko def, te Yàllaa nu ko digal.” Neel : “Yàlla du digle ñaawtéef. Moo ndax dangeen di waxal Yàlla lu ngeen xamul ? ”
29قُلْ أَمَرَ رَبِّي بِالْقِسْطِ ۖ وَأَقِيمُوا وُجُوهَكُمْ عِندَ كُلِّ مَسْجِدٍ وَادْعُوهُ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ ۚ كَمَا بَدَأَكُمْ تَعُودُونَ
Neel : “Yàlla Dafa digle maandute. Nangeen di jublu ci jàkka yépp te nangeen ko jaamu, di sellal ngir Moom [Yàlla]. Dangeen dellu ca Moom, na Mu leen sose woon cag njalbéen”.
30فَرِيقًا هَدَىٰ وَفَرِيقًا حَقَّ عَلَيْهِمُ الضَّلَالَةُ ۗ إِنَّهُمُ اتَّخَذُوا الشَّيَاطِينَ أَوْلِيَاءَ مِن دُونِ اللَّهِ وَيَحْسَبُونَ أَنَّهُم مُّهْتَدُونَ
Am na kurél bu gindiku, waaye am na ab kurél bu ab réer wàkk na leen, ñoom dañoo féeteek Séytaane bàyyi Yàlla te defe ne cig njub lañu nekk !
31۞ يَا بَنِي آدَمَ خُذُوا زِينَتَكُمْ عِندَ كُلِّ مَسْجِدٍ وَكُلُوا وَاشْرَبُوا وَلَا تُسْرِفُوا ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْمُسْرِفِينَ
Éy yéen doomi-aadama, [jépp jàkka ju ngeen jëmati] nangeen di waaj ba jekk [ak yére yu rafet]. Te nangeen di lekk di naan ; te buleen di yàq, ndax Yàlla soppul yàqkat yi.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
29Aaya

Tekki — Al-A'raf 29

Simoore Al-A'raf Aaya 29 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Yàlla Dafa digle maandute. Nangeen di jublu ci…

Simoore Aaya 29/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 27–31. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers