Al-A'raf · 45/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
الَّذِينَ يَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَيَبْغُونَهَا عِوَجًا وَهُم بِالْآخِرَةِ كَافِرُونَ ۝٤٥
Allazeena yasuddoona `an sabeelil laahi wa yabghoo nahaa `iwajanw wa hum bil Aakhirati kaafiroon
📖 Tekkim Wolof
ñoom ñay féewale [nit ñi] ak diiney Yàlla ji, di doxe doxiin wu jeng, te ñoom dañoo weddi àllaaxira.”
🎧 Dégg

📜 Aaya 43-47 — Al-A'raf

43وَنَزَعْنَا مَا فِي صُدُورِهِم مِّنْ غِلٍّ تَجْرِي مِن تَحْتِهِمُ الْأَنْهَارُ ۖ وَقَالُوا الْحَمْدُ لِلَّهِ الَّذِي هَدَانَا لِهَٰذَا وَمَا كُنَّا لِنَهْتَدِيَ لَوْلَا أَنْ هَدَانَا اللَّهُ ۖ لَقَدْ جَاءَتْ رُسُلُ رَبِّنَا بِالْحَقِّ ۖ وَنُودُوا أَن تِلْكُمُ الْجَنَّةُ أُورِثْتُمُوهَا بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
e Danuy rocci la nekkoon ca seeni dënn cig noonoo, dex ya dañuy daw-dawaan ca seen ron, ñuy wax naan : “Sant nanu Yàlla, Moom Mi nu indi ci lii. Te mënunu woon a gindi mukk sunu bopp, su fekkoon ne Yàlla gindiwunu. Sunu Boroom, ay Yonentam indi woon nañu dëgg.”. Ñu woo leen, ne leen : “Àjjana jii donolees na leen ko ngir la ngeen daan def [ci lu baax]”.
44وَنَادَىٰ أَصْحَابُ الْجَنَّةِ أَصْحَابَ النَّارِ أَن قَدْ وَجَدْنَا مَا وَعَدَنَا رَبُّنَا حَقًّا فَهَلْ وَجَدتُّم مَّا وَعَدَ رَبُّكُمْ حَقًّا ۖ قَالُوا نَعَمْ ۚ فَأَذَّنَ مُؤَذِّنٌ بَيْنَهُمْ أَن لَّعْنَةُ اللَّهِ عَلَى الظَّالِمِينَ
Waa Àjjana woo waa Safara, ne leen : “Nun dey, gis nanu la nu sunu Boroom digoon muy dëgg. Moo ndax yéen fekk ngeen li leen seen Boroom digoon muy dëgg ? ”. Ñu toontu ne : “Waaw”. Mu am wootekat bu daldi woote ne : rëbbum Yàlla dal na ca tooñkat ya,
45الَّذِينَ يَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَيَبْغُونَهَا عِوَجًا وَهُم بِالْآخِرَةِ كَافِرُونَ
ñoom ñay féewale [nit ñi] ak diiney Yàlla ji, di doxe doxiin wu jeng, te ñoom dañoo weddi àllaaxira.”
46وَبَيْنَهُمَا حِجَابٌ ۚ وَعَلَى الْأَعْرَافِ رِجَالٌ يَعْرِفُونَ كُلًّا بِسِيمَاهُمْ ۚ وَنَادَوْا أَصْحَابَ الْجَنَّةِ أَن سَلَامٌ عَلَيْكُمْ ۚ لَمْ يَدْخُلُوهَا وَهُمْ يَطْمَعُونَ
Dox na ca seen diggante [waa Àjjana] kiiraay, nekk na ca kaw (dig) wa aw nit ñoo xam ne danañu leen xàmmee ñoom ñépp ca seen màndarga ya. Ñu woo waa Àjjana, ne leen : “Yal na jàmm nekk ci yéen ! ”. Ñoom duñu dugg Àjjana te xemmem nañu ko.
47۞ وَإِذَا صُرِفَتْ أَبْصَارُهُمْ تِلْقَاءَ أَصْحَابِ النَّارِ قَالُوا رَبَّنَا لَا تَجْعَلْنَا مَعَ الْقَوْمِ الظَّالِمِينَ
Saa su seeni gët jubloo ca waa Safara, ñu ne : "Sunu Boroom, Yàlla boo nu boole ak nit ñu di ay tooñkat”.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
45Aaya

Tekki — Al-A'raf 45

Simoore Al-A'raf Aaya 45 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : ñoom ñay féewale [nit ñi] ak diiney Yàlla ji, di…

Simoore Aaya 45/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 43–47. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers