Al-Muzzammil · 18/20
Tekki Waxtaan — Al-Muzzammil
السَّمَاءُ مُنفَطِرٌ بِهِ ۚ كَانَ وَعْدُهُ مَفْعُولًا ۝١٨
Assamaaa`u munfatirum bih; kaana wa`duhoo maf`oola
📖 Tekkim Wolof
Su asamaan si dee xar. Ca la digam ba di mate.

🎧 Dégg


📜 Aaya 16-20 — Al-Muzzammil

16فَعَصَىٰ فِرْعَوْنُ الرَّسُولَ فَأَخَذْنَاهُ أَخْذًا وَبِيلًا
Firawna daldi moy Yonenta ba. Nu daldi koy jël bu metti. (faagaagal ko).
17فَكَيْفَ تَتَّقُونَ إِن كَفَرْتُمْ يَوْمًا يَجْعَلُ الْوِلْدَانَ شِيبًا
Ana naka ngeen di ragale (Yàlla), su ngeen weddee, bis boo xam ne tiit ma bijaawloona ab liir ?
18السَّمَاءُ مُنفَطِرٌ بِهِ ۚ كَانَ وَعْدُهُ مَفْعُولًا
Su asamaan si dee xar. Ca la digam ba di mate.
19إِنَّ هَٰذِهِ تَذْكِرَةٌ ۖ فَمَن شَاءَ اتَّخَذَ إِلَىٰ رَبِّهِ سَبِيلًا
Lii nag ag fàttali la. Képp ku mu soob mu jël yoon wa jëm ca Boroomam aw ca.
20۞ إِنَّ رَبَّكَ يَعْلَمُ أَنَّكَ تَقُومُ أَدْنَىٰ مِن ثُلُثَيِ اللَّيْلِ وَنِصْفَهُ وَثُلُثَهُ وَطَائِفَةٌ مِّنَ الَّذِينَ مَعَكَ ۚ وَاللَّهُ يُقَدِّرُ اللَّيْلَ وَالنَّهَارَ ۚ عَلِمَ أَن لَّن تُحْصُوهُ فَتَابَ عَلَيْكُمْ ۖ فَاقْرَءُوا مَا تَيَسَّرَ مِنَ الْقُرْآنِ ۚ عَلِمَ أَن سَيَكُونُ مِنكُم مَّرْضَىٰ ۙ وَآخَرُونَ يَضْرِبُونَ فِي الْأَرْضِ يَبْتَغُونَ مِن فَضْلِ اللَّهِ ۙ وَآخَرُونَ يُقَاتِلُونَ فِي سَبِيلِ اللَّهِ ۖ فَاقْرَءُوا مَا تَيَسَّرَ مِنْهُ ۚ وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَآتُوا الزَّكَاةَ وَأَقْرِضُوا اللَّهَ قَرْضًا حَسَنًا ۚ وَمَا تُقَدِّمُوا لِأَنفُسِكُم مِّنْ خَيْرٍ تَجِدُوهُ عِندَ اللَّهِ هُوَ خَيْرًا وَأَعْظَمَ أَجْرًا ۚ وَاسْتَغْفِرُوا اللَّهَ ۖ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Sa Boroom xam na ne, yaw (Muhammad) da ngay taxawlu gëna néew ñaari ñetteeli xaaji guddi gi, walla xaaj ba, walla benn ñetteelu xaaj ba. Ànd kook mbooloo ci ña ànd ak yaw. Te Yàlla dana nattale guddeek bëccëg. Xam na ne manu leen fanaanee julli. Mu jégal leen. Jàngleen lu jàppandi ci Alxuraan. (Ndax moom Yàlla) xam na ne am na ci yéen ñu wopp, ak ñeneen ñuy tukki ji ci réew yi, ngir sàkku ji ci ngënéeli Yàlla yi, ak ñeneen ñuy xare ji ci yoonu Yàlla. Kon jàngleen la ca jàppandi. Te na ngeen taxawal julli, tey génne asaka, te na ngeen lebal Yàlla bor bu rafet. Te lépp lu ngeen jiitalal seen bopp ciw yiw, da ngeen ko fekk ci Yàlla, mooy la gën te moo ëpp ag pey. Te it na ngay jéggalu Yàlla. Yàlla moom Jéggalaakoon la Jaglewaakoon la.
Al-MuzzammilFihi Alxuraan
20Aaya
MeccanRevelation
18Aaya

Tekki — Al-Muzzammil 18

Simoore Al-Muzzammil Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Su asamaan si dee xar. Ca la digam ba di…

Simoore Aaya 18/20 — Al-Muzzammil المزمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Muzzammil Dégg, Al-Muzzammil Tekki, Al-Muzzammil mp3, Al-Muzzammil pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers