At-Tawba · 106/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
وَآخَرُونَ مُرْجَوْنَ لِأَمْرِ اللَّهِ إِمَّا يُعَذِّبُهُمْ وَإِمَّا يَتُوبُ عَلَيْهِمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ ۝١٠٦
Wa aakharoona murjawna li amril laahi imaa yu`az zibuhum wa immaa yatoobu `alaihim; wallaahu `Aleemun Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Ak ñeneen ñoo xam ne dees na leen yeexe ci ndigalul Yàlla, mën naa am Mu mbugal leen, mën naa am it Mu jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 104-108 — Simoore At-Tawba

104أَلَمْ يَعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ هُوَ يَقْبَلُ التَّوْبَةَ عَنْ عِبَادِهِ وَيَأْخُذُ الصَّدَقَاتِ وَأَنَّ اللَّهَ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla Moom Dana nangu tuub ciy jaamam, te Dana jël it sarax ya, te Moom Yàlla Mooy Nanguwaakoon cig tuub, di Jaglewaakoon.
105وَقُلِ اعْمَلُوا فَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ وَالْمُؤْمِنُونَ ۖ وَسَتُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Neel : “Jëfleen (lu leen soob), Yàlla ak ub Yonentam ak jullit ña, Danañu gis seeni jëf, te dees na leen delloo ca Aji-xam ja kumpa ak la feeñ. Mu xamal leen la ngeen daan def”.
106وَآخَرُونَ مُرْجَوْنَ لِأَمْرِ اللَّهِ إِمَّا يُعَذِّبُهُمْ وَإِمَّا يَتُوبُ عَلَيْهِمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Ak ñeneen ñoo xam ne dees na leen yeexe ci ndigalul Yàlla, mën naa am Mu mbugal leen, mën naa am it Mu jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
107وَالَّذِينَ اتَّخَذُوا مَسْجِدًا ضِرَارًا وَكُفْرًا وَتَفْرِيقًا بَيْنَ الْمُؤْمِنِينَ وَإِرْصَادًا لِّمَنْ حَارَبَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ مِن قَبْلُ ۚ وَلَيَحْلِفُنَّ إِنْ أَرَدْنَا إِلَّا الْحُسْنَىٰ ۖ وَاللَّهُ يَشْهَدُ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ
Ña nga xam ne dañoo defar jàkka ngir bëgg a lore ak weddi ak téqale way-gëm ña, ak di fàggul (pexem ña fay julli) ku xeex ak Yàlla ak ub Yonentam ca njalbeen ga, ak ngir mën a giñ ne bëgguñu lu dul lu baax. Yàlla seede ne li wóor mooy dañuy fen.
108لَا تَقُمْ فِيهِ أَبَدًا ۚ لَّمَسْجِدٌ أُسِّسَ عَلَى التَّقْوَىٰ مِنْ أَوَّلِ يَوْمٍ أَحَقُّ أَن تَقُومَ فِيهِ ۚ فِيهِ رِجَالٌ يُحِبُّونَ أَن يَتَطَهَّرُوا ۚ وَاللَّهُ يُحِبُّ الْمُطَّهِّرِينَ
Bul ca taxaw mukk. Ca njalbeenu bis (ba nga wàccee Madina), moo gën a yey ci nga taxaw fa. Aw góor a nga fa, ñoo xam ne, sopp nañu jéem a nekk ñu laab, te Yàlla sopp na ñu laab ña.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
106Aaya

Tekki — At-Tawba 106

Simoore At-Tawba Aaya 106 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ak ñeneen ñoo xam ne dees na leen yeexe ci…

Simoore Aaya 106/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 104–108. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers