At-Tawba · 105/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
وَقُلِ اعْمَلُوا فَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ وَالْمُؤْمِنُونَ ۖ وَسَتُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝١٠٥
Wa quli`maloo fasayaral laahu `amalakum wa Rasooluhoo walmu`minoona wa saturaddoona ilaa `Aalimil Ghaibi washshahaadati fa yunabbi`ukum bimaa kuntum ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Jëfleen (lu leen soob), Yàlla ak ub Yonentam ak jullit ña, Danañu gis seeni jëf, te dees na leen delloo ca Aji-xam ja kumpa ak la feeñ. Mu xamal leen la ngeen daan def”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 103-107 — At-Tawba

103خُذْ مِنْ أَمْوَالِهِمْ صَدَقَةً تُطَهِّرُهُمْ وَتُزَكِّيهِم بِهَا وَصَلِّ عَلَيْهِمْ ۖ إِنَّ صَلَاتَكَ سَكَنٌ لَّهُمْ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Jëlal ci seen alal ab sarax (asaka) ngir laabal leen ca ak sellal leen ca, te nga ñaanal leen. Ndax sa ñaan dalum xel la ci ñoom. Te Yàlla Kuy dégg la, Kuy xam la.
104أَلَمْ يَعْلَمُوا أَنَّ اللَّهَ هُوَ يَقْبَلُ التَّوْبَةَ عَنْ عِبَادِهِ وَيَأْخُذُ الصَّدَقَاتِ وَأَنَّ اللَّهَ هُوَ التَّوَّابُ الرَّحِيمُ
Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla Moom Dana nangu tuub ciy jaamam, te Dana jël it sarax ya, te Moom Yàlla Mooy Nanguwaakoon cig tuub, di Jaglewaakoon.
105وَقُلِ اعْمَلُوا فَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ وَالْمُؤْمِنُونَ ۖ وَسَتُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Neel : “Jëfleen (lu leen soob), Yàlla ak ub Yonentam ak jullit ña, Danañu gis seeni jëf, te dees na leen delloo ca Aji-xam ja kumpa ak la feeñ. Mu xamal leen la ngeen daan def”.
106وَآخَرُونَ مُرْجَوْنَ لِأَمْرِ اللَّهِ إِمَّا يُعَذِّبُهُمْ وَإِمَّا يَتُوبُ عَلَيْهِمْ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Ak ñeneen ñoo xam ne dees na leen yeexe ci ndigalul Yàlla, mën naa am Mu mbugal leen, mën naa am it Mu jéggal leen. Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
107وَالَّذِينَ اتَّخَذُوا مَسْجِدًا ضِرَارًا وَكُفْرًا وَتَفْرِيقًا بَيْنَ الْمُؤْمِنِينَ وَإِرْصَادًا لِّمَنْ حَارَبَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ مِن قَبْلُ ۚ وَلَيَحْلِفُنَّ إِنْ أَرَدْنَا إِلَّا الْحُسْنَىٰ ۖ وَاللَّهُ يَشْهَدُ إِنَّهُمْ لَكَاذِبُونَ
Ña nga xam ne dañoo defar jàkka ngir bëgg a lore ak weddi ak téqale way-gëm ña, ak di fàggul (pexem ña fay julli) ku xeex ak Yàlla ak ub Yonentam ca njalbeen ga, ak ngir mën a giñ ne bëgguñu lu dul lu baax. Yàlla seede ne li wóor mooy dañuy fen.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
105Aaya

Tekki — At-Tawba 105

Simoore At-Tawba Aaya 105 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Jëfleen (lu leen soob), Yàlla ak ub Yonentam…

Simoore Aaya 105/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 103–107. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers