At-Tawba · 58/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
وَمِنْهُم مَّن يَلْمِزُكَ فِي الصَّدَقَاتِ فَإِنْ أُعْطُوا مِنْهَا رَضُوا وَإِن لَّمْ يُعْطَوْا مِنْهَا إِذَا هُمْ يَسْخَطُونَ ۝٥٨
Wa minhum mai yalmizuka fis sadaqaati fa-in u`too minhaa radoo wa illam yu`taw minhaaa izaa hum yaskhatoon
📖 Tekkim Wolof
Am na ci ñoom ñu la ayibal ci sarax yi : ku leen ca joxoon ñu bég ca ; ku leen joxul ñu xundu.

🎧 Dégg


📜 Aaya 56-60 — Simoore At-Tawba

56وَيَحْلِفُونَ بِاللَّهِ إِنَّهُمْ لَمِنكُمْ وَمَا هُم مِّنكُمْ وَلَٰكِنَّهُمْ قَوْمٌ يَفْرَقُونَ
Ñuy waat ci Yàlla, naan ñoom ci yéen lañu bokk ; te bokkuñu ci yéen. Waaye ñoom dañoo ragal rekk ngeen dal (ci seen kaw).
57لَوْ يَجِدُونَ مَلْجَأً أَوْ مَغَارَاتٍ أَوْ مُدَّخَلًا لَّوَلَّوْا إِلَيْهِ وَهُمْ يَجْمَحُونَ
Bu ñu amoon làquwaay walla xunti walla fu ñu dugg (ba raw), kon ñu dëddu jëm fa te gaaw ca.
58وَمِنْهُم مَّن يَلْمِزُكَ فِي الصَّدَقَاتِ فَإِنْ أُعْطُوا مِنْهَا رَضُوا وَإِن لَّمْ يُعْطَوْا مِنْهَا إِذَا هُمْ يَسْخَطُونَ
Am na ci ñoom ñu la ayibal ci sarax yi : ku leen ca joxoon ñu bég ca ; ku leen joxul ñu xundu.
59وَلَوْ أَنَّهُمْ رَضُوا مَا آتَاهُمُ اللَّهُ وَرَسُولُهُ وَقَالُوا حَسْبُنَا اللَّهُ سَيُؤْتِينَا اللَّهُ مِن فَضْلِهِ وَرَسُولُهُ إِنَّا إِلَى اللَّهِ رَاغِبُونَ
Lu tee ñu bég ca la leen Yàlla ak Yonentam jox ? Tey wax : “Yàlla doy nanu. Yàlla Dana nu jox ci mbaaxam ak Yonentam it !... Nun way-xemmem lanu jëm ci Yàlla ”.
60۞ إِنَّمَا الصَّدَقَاتُ لِلْفُقَرَاءِ وَالْمَسَاكِينِ وَالْعَامِلِينَ عَلَيْهَا وَالْمُؤَلَّفَةِ قُلُوبُهُمْ وَفِي الرِّقَابِ وَالْغَارِمِينَ وَفِي سَبِيلِ اللَّهِ وَابْنِ السَّبِيلِ ۖ فَرِيضَةً مِّنَ اللَّهِ ۗ وَاللَّهُ عَلِيمٌ حَكِيمٌ
Asaka, ñi ko yeyoo ñooy ñi néew am-am, yalwaankat yi, ñi koy toppatoo, ñi ñu bëgg nooyal seen xol (ci Lislaam) ak ci goreel jaam, ña bor sonnal, ak ca lu jëm ci diiney Yàlla, ak doxandeem bu nekk ci tukki. Looloo di li Yàlla santaane ! Te Yàlla Ku xam la, Ku xereñ la.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
58Aaya

Tekki — At-Tawba 58

Simoore At-Tawba Aaya 58 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci ñoom ñu la ayibal ci sarax yi…

Simoore Aaya 58/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 56–60. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers