At-Tawba · 94/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
يَعْتَذِرُونَ إِلَيْكُمْ إِذَا رَجَعْتُمْ إِلَيْهِمْ ۚ قُل لَّا تَعْتَذِرُوا لَن نُّؤْمِنَ لَكُمْ قَدْ نَبَّأَنَا اللَّهُ مِنْ أَخْبَارِكُمْ ۚ وَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝٩٤
ya`taziroona ilaikum izaa raja`tum ilaihim; qul laa ta`taziroo lan nu`mina lakum qad nabba annal laahu min akhbaarikum; wa sa yaral laahu `amalakum wa Rasooluhoo suma turaddoona ilaa `Aalimil Ghaibi washshahaadati fa yunabbi`ukum bimaa kuntum ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
Danañu ñëw ci yéen di lay bu ngeen dellusee. Neel : “Buleen lay : dunuleen gëm mukk. Yàlla nettali nanu ba noppi seen mbir. Te Yàlla ak ub Yonentam Danañu gis seeni jëf. Nu door leen a delloo fa Aji-xam ja kumpa ak la feeñ, Mu xamal leen li ngeen daan def.

🎧 Dégg


📜 Aaya 92-96 — Simoore At-Tawba

92وَلَا عَلَى الَّذِينَ إِذَا مَا أَتَوْكَ لِتَحْمِلَهُمْ قُلْتَ لَا أَجِدُ مَا أَحْمِلُكُمْ عَلَيْهِ تَوَلَّوا وَّأَعْيُنُهُمْ تَفِيضُ مِنَ الدَّمْعِ حَزَنًا أَلَّا يَجِدُوا مَا يُنفِقُونَ
Ña nga xam ne bu ñu dikkee ci yaw di sàkku waruwaay, nanga leen di wax ne amuloo lu ñu mën a war, ñu dellu ànd ak naqar, di jooy ngir jàq ca la ñu amul waajtaay, ñoom it amuñu bàkkaar. Kenn du am ci ñoom aw yoon.
93۞ إِنَّمَا السَّبِيلُ عَلَى الَّذِينَ يَسْتَأْذِنُونَكَ وَهُمْ أَغْنِيَاءُ ۚ رَضُوا بِأَن يَكُونُوا مَعَ الْخَوَالِفِ وَطَبَعَ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Ñay am bàkkaar kay ñoo di ña woomal te di la laaj ndigal ci bañ a dem xare ji, bëgg a ànd ak ñay fuuyu. Yàlla fatt na seeni xol te ñoom xamuñu. Ñoom kenn du mën a am ci ñoom aw yoon.
94يَعْتَذِرُونَ إِلَيْكُمْ إِذَا رَجَعْتُمْ إِلَيْهِمْ ۚ قُل لَّا تَعْتَذِرُوا لَن نُّؤْمِنَ لَكُمْ قَدْ نَبَّأَنَا اللَّهُ مِنْ أَخْبَارِكُمْ ۚ وَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Danañu ñëw ci yéen di lay bu ngeen dellusee. Neel : “Buleen lay : dunuleen gëm mukk. Yàlla nettali nanu ba noppi seen mbir. Te Yàlla ak ub Yonentam Danañu gis seeni jëf. Nu door leen a delloo fa Aji-xam ja kumpa ak la feeñ, Mu xamal leen li ngeen daan def.
95سَيَحْلِفُونَ بِاللَّهِ لَكُمْ إِذَا انقَلَبْتُمْ إِلَيْهِمْ لِتُعْرِضُوا عَنْهُمْ ۖ فَأَعْرِضُوا عَنْهُمْ ۖ إِنَّهُمْ رِجْسٌ ۖ وَمَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Danañu leen waatal ci Yàlla, ba ngeen dellusee ci ñoom, ngir ngeen bañ leen a sikk. Waaye nangeen leen dëddu. Ñoom nag sobe lañu te seen delluwaay mooy Safara, muy peyug la ñu nekkoon di ko fàggu.
96يَحْلِفُونَ لَكُمْ لِتَرْضَوْا عَنْهُمْ ۖ فَإِن تَرْضَوْا عَنْهُمْ فَإِنَّ اللَّهَ لَا يَرْضَىٰ عَنِ الْقَوْمِ الْفَاسِقِينَ
Ñanga leen di waatal ngir ngeen nangu (seeni ngànt), rafet njort ci ñoom. Bu ngeen nangoo seeni lay, Yàlla du nangul aw lay nit ñu di ay saay-saay.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
94Aaya

Tekki — At-Tawba 94

Simoore At-Tawba Aaya 94 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Danañu ñëw ci yéen di lay bu ngeen dellusee. Neel…

Simoore Aaya 94/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 92–96. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers