At-Tawba · 93/129
Tekki Waxtaan — At-Tawba
۞ إِنَّمَا السَّبِيلُ عَلَى الَّذِينَ يَسْتَأْذِنُونَكَ وَهُمْ أَغْنِيَاءُ ۚ رَضُوا بِأَن يَكُونُوا مَعَ الْخَوَالِفِ وَطَبَعَ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ ۝٩٣
Innamas sabeelu `alal lazeena yastaazinoonaka wa hum aghniyaaa`; radoo biany-yakoonoo ma`al khawaalifi wa taba`al laahu `alaa quloobihim fahum laa ya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Ñay am bàkkaar kay ñoo di ña woomal te di la laaj ndigal ci bañ a dem xare ji, bëgg a ànd ak ñay fuuyu. Yàlla fatt na seeni xol te ñoom xamuñu. Ñoom kenn du mën a am ci ñoom aw yoon.
🎧 Dégg

📜 Aaya 91-95 — At-Tawba

91لَّيْسَ عَلَى الضُّعَفَاءِ وَلَا عَلَى الْمَرْضَىٰ وَلَا عَلَى الَّذِينَ لَا يَجِدُونَ مَا يُنفِقُونَ حَرَجٌ إِذَا نَصَحُوا لِلَّهِ وَرَسُولِهِ ۚ مَا عَلَى الْمُحْسِنِينَ مِن سَبِيلٍ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Ña néew dolle ak ña wopp, ak ñi amul yóbbal, amuñu bàkkaar (ci toog bañ a xare ji) ndeem ñu rafet yéene lañu ci Yàlla ak ub Yonentam. Naka noonu it, ca ñay rafetal seeni jëf. Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la.
92وَلَا عَلَى الَّذِينَ إِذَا مَا أَتَوْكَ لِتَحْمِلَهُمْ قُلْتَ لَا أَجِدُ مَا أَحْمِلُكُمْ عَلَيْهِ تَوَلَّوا وَّأَعْيُنُهُمْ تَفِيضُ مِنَ الدَّمْعِ حَزَنًا أَلَّا يَجِدُوا مَا يُنفِقُونَ
Ña nga xam ne bu ñu dikkee ci yaw di sàkku waruwaay, nanga leen di wax ne amuloo lu ñu mën a war, ñu dellu ànd ak naqar, di jooy ngir jàq ca la ñu amul waajtaay, ñoom it amuñu bàkkaar. Kenn du am ci ñoom aw yoon.
93۞ إِنَّمَا السَّبِيلُ عَلَى الَّذِينَ يَسْتَأْذِنُونَكَ وَهُمْ أَغْنِيَاءُ ۚ رَضُوا بِأَن يَكُونُوا مَعَ الْخَوَالِفِ وَطَبَعَ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Ñay am bàkkaar kay ñoo di ña woomal te di la laaj ndigal ci bañ a dem xare ji, bëgg a ànd ak ñay fuuyu. Yàlla fatt na seeni xol te ñoom xamuñu. Ñoom kenn du mën a am ci ñoom aw yoon.
94يَعْتَذِرُونَ إِلَيْكُمْ إِذَا رَجَعْتُمْ إِلَيْهِمْ ۚ قُل لَّا تَعْتَذِرُوا لَن نُّؤْمِنَ لَكُمْ قَدْ نَبَّأَنَا اللَّهُ مِنْ أَخْبَارِكُمْ ۚ وَسَيَرَى اللَّهُ عَمَلَكُمْ وَرَسُولُهُ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَالِمِ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Danañu ñëw ci yéen di lay bu ngeen dellusee. Neel : “Buleen lay : dunuleen gëm mukk. Yàlla nettali nanu ba noppi seen mbir. Te Yàlla ak ub Yonentam Danañu gis seeni jëf. Nu door leen a delloo fa Aji-xam ja kumpa ak la feeñ, Mu xamal leen li ngeen daan def.
95سَيَحْلِفُونَ بِاللَّهِ لَكُمْ إِذَا انقَلَبْتُمْ إِلَيْهِمْ لِتُعْرِضُوا عَنْهُمْ ۖ فَأَعْرِضُوا عَنْهُمْ ۖ إِنَّهُمْ رِجْسٌ ۖ وَمَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Danañu leen waatal ci Yàlla, ba ngeen dellusee ci ñoom, ngir ngeen bañ leen a sikk. Waaye nangeen leen dëddu. Ñoom nag sobe lañu te seen delluwaay mooy Safara, muy peyug la ñu nekkoon di ko fàggu.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
93Aaya

Tekki — At-Tawba 93

Simoore At-Tawba Aaya 93 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñay am bàkkaar kay ñoo di ña woomal te di…

Simoore Aaya 93/129 — At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: At-Tawba Dégg, At-Tawba Tekki, At-Tawba mp3, At-Tawba pdf. Aaya 91–95. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers