11 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭴﭵ
101:1 Toj-toj ba !
ﭶﭷﭸ
101:2 Ana lan mooy toj-toj ba ?
ﭹﭺﭻﭼﭽ
101:3 Ana lan moo lay xamal luy toj-toj ba ?
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
101:4 Moo di bis ba nit ñi di melni ay lëpaalëpp yu ñu wasaare,
ﮄﮅﮆﮇﮈ
101:5 te tund doj yi it mujj mel ni ngëndal nooy nepp ;
ﮉﮊﮋﮌﮍ
101:6 képp ku peeseem diis (ci yiw)
ﮎﮏﮐﮑﮒ
101:7 ma nga ko ca dundu gu neex ;
ﮓﮔﮕﮖﮗ
101:8 képp ku peeseem wayaf (ci yiw),
ﮘﮙﮚ
101:9 ma ngay jëm Haawiyatu.
ﮛﮜﮝﮞﮟ
101:10 Ana luy xamal lan mooy loolu Haawiyatu ?
ﮠﮡﮢ
101:11 Aw Safara la wu tàng.

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 30, 2026

Don't forget us in your sincere prayers