11 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﮱﯓﯔ
100:1 Ca jaabkat ya seeni gimiñ di foor (fas) (Maa ngi giñ),
ﯕﯖﯗ
100:2 tey këdaa seen tànk ya my xuuy (ferñent),
ﯘﯙﯚ
100:3 ak yay songe suba coy.
ﯛﯜﯝﯞ
100:4 yay naawal pënd,
ﯟﯠﯡﯢ
100:5 tey xuus ca biir noon ya.
ﭑﭒﭓﭔﭕ
100:6 Nit dey, kuy ñàkk deloo Boroomam njukal la ;
ﭖﭗﭘﭙﭚ
100:7 te kat, moom, seede la ci loolu ;
ﭛﭜﭝﭞﭟ
100:8 te kat moom ku tarla xérlool ci bëgg alal.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
100:9 Xanaa dafa xamul saa su ñu ko jaxasee ci biir bàmmeel,
ﭩﭪﭫﭬﭭ
100:10 te wuñées li nekk ci biir dënn yi,
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
100:11 bu keroogee, sa Boroom Ku deñ Kumpa la ci ñoom?

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 29, 2026

Don't forget us in your sincere prayers