Hud · 90/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَاسْتَغْفِرُوا رَبَّكُمْ ثُمَّ تُوبُوا إِلَيْهِ ۚ إِنَّ رَبِّي رَحِيمٌ وَدُودٌ ۝٩٠
Wastaghfiroo Rabbakum summa toobooo ilaih; inna Rabbee Raheemunw Wadood
📖 Tekkim Wolof
Nangeen baalu seen Boroom te ngeen tuub jëm ci Moom. Naka sama Boroom, ab Jéggalaakoon la ku sopp [way-gëm ña] la
🎧 Dégg

📜 Aaya 88-92 — Hud

88قَالَ يَا قَوْمِ أَرَأَيْتُمْ إِن كُنتُ عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّي وَرَزَقَنِي مِنْهُ رِزْقًا حَسَنًا ۚ وَمَا أُرِيدُ أَنْ أُخَالِفَكُمْ إِلَىٰ مَا أَنْهَاكُمْ عَنْهُ ۚ إِنْ أُرِيدُ إِلَّا الْإِصْلَاحَ مَا اسْتَطَعْتُ ۚ وَمَا تَوْفِيقِي إِلَّا بِاللَّهِ ۚ عَلَيْهِ تَوَكَّلْتُ وَإِلَيْهِ أُنِيبُ
Mu ne : "Yéen samaw nit, ndax seetlu ngeen ba xam ndax nekkuma ci lu leer lu jóge ca sama Boroom, te Mu jox ma xéewalam, mu di xéewal gu màgg ?... Te bëggumaa juuyook yéen ci lu ma leen tere. Bëgguma lu dul sellal [yéwénal] kem sama kàttan. Te samag njébbal wéeruwul fu dul ci Yàlla. Ci laa wéeru te ci Moom laay dellu.
89وَيَا قَوْمِ لَا يَجْرِمَنَّكُمْ شِقَاقِي أَن يُصِيبَكُم مِّثْلُ مَا أَصَابَ قَوْمَ نُوحٍ أَوْ قَوْمَ هُودٍ أَوْ قَوْمَ صَالِحٍ ۚ وَمَا قَوْمُ لُوطٍ مِّنكُم بِبَعِيدٍ
Yéen samaw nit, bëgg a wuuteek man bumu tax ngeen mel ni la daloon nitu Nooh dal leen, walla la daloon nitu Huud, walla nitu Saalihu, te sax nitu Lóot ña [fa ñu nekkoon] soriwuleen.
90وَاسْتَغْفِرُوا رَبَّكُمْ ثُمَّ تُوبُوا إِلَيْهِ ۚ إِنَّ رَبِّي رَحِيمٌ وَدُودٌ
Nangeen baalu seen Boroom te ngeen tuub jëm ci Moom. Naka sama Boroom, ab Jéggalaakoon la ku sopp [way-gëm ña] la
91قَالُوا يَا شُعَيْبُ مَا نَفْقَهُ كَثِيرًا مِّمَّا تَقُولُ وَإِنَّا لَنَرَاكَ فِينَا ضَعِيفًا ۖ وَلَوْلَا رَهْطُكَ لَرَجَمْنَاكَ ۖ وَمَا أَنتَ عَلَيْنَا بِعَزِيزٍ
Ñu ne : "Yaw Suhaybu, amuñu ag dégg lu bari ci say wax ; te gis nanu nga nekk ku ñàkk solo fi nun. Te bu dul koon giir gi nga bokk, dananu la jam ay xeer. Nekkuloo ku tedd ci sunu kaw”.
92قَالَ يَا قَوْمِ أَرَهْطِي أَعَزُّ عَلَيْكُم مِّنَ اللَّهِ وَاتَّخَذْتُمُوهُ وَرَاءَكُمْ ظِهْرِيًّا ۖ إِنَّ رَبِّي بِمَا تَعْمَلُونَ مُحِيطٌ
Mu ne : "Yéen samaw nit, moo ndax sama giir moo gën a tedd ci yéen Yàlla ba tax ngeen bàyyi Ko ginnaaw ? Sama Boroom nag Ku peeg la li ngeen di def.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
90Aaya

Tekki — Hud 90

Simoore Hud Aaya 90 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nangeen baalu seen Boroom te ngeen tuub jëm ci Moom.…

Simoore Aaya 90/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 88–92. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers