An-Nahl · 59/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
يَتَوَارَىٰ مِنَ الْقَوْمِ مِن سُوءِ مَا بُشِّرَ بِهِ ۚ أَيُمْسِكُهُ عَلَىٰ هُونٍ أَمْ يَدُسُّهُ فِي التُّرَابِ ۗ أَلَا سَاءَ مَا يَحْكُمُونَ ۝٥٩
yatawaaraa minal qawmimin sooo`i maa bushshira bih; a-yumsikuhoo `alaa hoonin am yadussuhoo fit turaab; alaa saaa`a maa yahkumoon
📖 Tekkim Wolof
Muy nëbbu nit ñi ngir lu naqari la ñu yégal. Muy seet ndax dakoy téyee ndax gàcceem walla dakoy suul ci suuf ? Cëy aka bon nañuy àttee mbir !
🎧 Dégg

📜 Aaya 57-61 — An-Nahl

57وَيَجْعَلُونَ لِلَّهِ الْبَنَاتِ سُبْحَانَهُ ۙ وَلَهُم مَّا يَشْتَهُونَ
Ñuy sàkkal Yàlla ay doom yu jigéen. Sellam ga [sori na lool ! Te ñoom ñuy moomale seen bopp la ñu bëgg [ay doom yu góor].
58وَإِذَا بُشِّرَ أَحَدُهُم بِالْأُنثَىٰ ظَلَّ وَجْهُهُ مُسْوَدًّا وَهُوَ كَظِيمٌ
Ku ñu ca yégal ne am na doom ju jigéen, mu yendoo ñëgal kanam gi ànd ak mer.
59يَتَوَارَىٰ مِنَ الْقَوْمِ مِن سُوءِ مَا بُشِّرَ بِهِ ۚ أَيُمْسِكُهُ عَلَىٰ هُونٍ أَمْ يَدُسُّهُ فِي التُّرَابِ ۗ أَلَا سَاءَ مَا يَحْكُمُونَ
Muy nëbbu nit ñi ngir lu naqari la ñu yégal. Muy seet ndax dakoy téyee ndax gàcceem walla dakoy suul ci suuf ? Cëy aka bon nañuy àttee mbir !
60لِلَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ بِالْآخِرَةِ مَثَلُ السَّوْءِ ۖ وَلِلَّهِ الْمَثَلُ الْأَعْلَىٰ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Ñeel na ñi gëmul àllaaxira nekkin wu bon. Te ñeel na Yàlla nekkin wa gën a kawe. Te Moom mooy Aji-not ji ; Aji-xereñ.
61وَلَوْ يُؤَاخِذُ اللَّهُ النَّاسَ بِظُلْمِهِم مَّا تَرَكَ عَلَيْهَا مِن دَابَّةٍ وَلَٰكِن يُؤَخِّرُهُمْ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۖ فَإِذَا جَاءَ أَجَلُهُمْ لَا يَسْتَأْخِرُونَ سَاعَةً ۖ وَلَا يَسْتَقْدِمُونَ
Bu Yàlla [doon] gaaw a duma nit ñi ngir seen tooñeel, kon du bàyyi kenn ci kaw suuf si. Waaye Dafa leen ci yeexe ba ci àpp bu ñu dogal ba noppi. Kon bu seen àpp agsee, duñu ko weesu mbaa ñu jiitu ko wenn waxtu.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
59Aaya

Tekki — An-Nahl 59

Simoore An-Nahl Aaya 59 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Muy nëbbu nit ñi ngir lu naqari la ñu yégal.…

Simoore Aaya 59/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 57–61. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers