An-Nahl · 65/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَاللَّهُ أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّقَوْمٍ يَسْمَعُونَ ۝٦٥
Wallaahu anzala minas samaaa`i maaa`an fa ahyaa bihil arda ba`da mawtihaa; inna fee zaalika la aayatal liqaw miny yasma`oon
📖 Tekkim Wolof
Te Yàlla moo wàcce ndox mu jóge ca kaw, mu dundal ci suuf si ginnaaw ba mu bekkooree. Te nekk na ci loolu tegtal ci nit ñuy dégg.
🎧 Dégg

📜 Aaya 63-67 — An-Nahl

63تَاللَّهِ لَقَدْ أَرْسَلْنَا إِلَىٰ أُمَمٍ مِّن قَبْلِكَ فَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ فَهُوَ وَلِيُّهُمُ الْيَوْمَ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Giñ Nanu Nun Yàlla ne yónni woon Nanu ay Yonent cay xeet ya la jiitu. Waaye Séytaane rafetalal leen seeni jëf ba faf mu nekk tey seeni àndandoo. Te ñeel na leen mbugal mu metti.
64وَمَا أَنزَلْنَا عَلَيْكَ الْكِتَابَ إِلَّا لِتُبَيِّنَ لَهُمُ الَّذِي اخْتَلَفُوا فِيهِ ۙ وَهُدًى وَرَحْمَةً لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ
Wàccewuñu ci yaaw Téere [Alxuraan] ba lu dul ngir nga leeralal leen la ñu nekkoon ci juuyoo, ak ngir mu nekk di njub ak yërmaande ci nit ñu gëm.
65وَاللَّهُ أَنزَلَ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَأَحْيَا بِهِ الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّقَوْمٍ يَسْمَعُونَ
Te Yàlla moo wàcce ndox mu jóge ca kaw, mu dundal ci suuf si ginnaaw ba mu bekkooree. Te nekk na ci loolu tegtal ci nit ñuy dégg.
66وَإِنَّ لَكُمْ فِي الْأَنْعَامِ لَعِبْرَةً ۖ نُّسْقِيكُم مِّمَّا فِي بُطُونِهِ مِن بَيْنِ فَرْثٍ وَدَمٍ لَّبَنًا خَالِصًا سَائِغًا لِّلشَّارِبِينَ
Te sax am ngeen lu ngeen mën a waaroo ci mala yi : Noo ngi leen di nàndal ci li nekk ci seen biir - lu génne ci diggante sebret ak deret - muy meew mu neex te sell ca ña koy naan.
67وَمِن ثَمَرَاتِ النَّخِيلِ وَالْأَعْنَابِ تَتَّخِذُونَ مِنْهُ سَكَرًا وَرِزْقًا حَسَنًا ۗ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ
Te ci meññenti tàndarma ak reseñ, dangeen ca jële naan guy màndee ak xéewal gu baax. Te nekk na ci loolu ay tegtal ci aw nit ñuy xalaat.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
65Aaya

Tekki — An-Nahl 65

Simoore An-Nahl Aaya 65 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te Yàlla moo wàcce ndox mu jóge ca kaw, mu…

Simoore Aaya 65/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 63–67. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers