An-Nahl · 71/128
Tekki Waxtaan — An-Nahl
وَاللَّهُ فَضَّلَ بَعْضَكُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ فِي الرِّزْقِ ۚ فَمَا الَّذِينَ فُضِّلُوا بِرَادِّي رِزْقِهِمْ عَلَىٰ مَا مَلَكَتْ أَيْمَانُهُمْ فَهُمْ فِيهِ سَوَاءٌ ۚ أَفَبِنِعْمَةِ اللَّهِ يَجْحَدُونَ ۝٧١
Wallaahu faddala ba`dakum `alaa ba`din fir rizq; famal lazeena fuddiloo biraaaddee rizqihim `alaa maa malakat aimaanuhum fahum feehi sawaaa`; afabini`matil laahi yajhadoon
📖 Tekkim Wolof
Yàlla yékkati na ñenn ña ci kaw ñeneen ña ci wërsëg. Te ña Mu jox ngëneel loolu, duñu delloo dara ci wërsëg woowu, jox ko seeni jaam ngir ñu yemoo ca wërsëg wa. Moo ndax dañuy weddi xéewali Yàlla ? Fàkk
🎧 Dégg

📜 Aaya 69-73 — An-Nahl

69ثُمَّ كُلِي مِن كُلِّ الثَّمَرَاتِ فَاسْلُكِي سُبُلَ رَبِّكِ ذُلُلًا ۚ يَخْرُجُ مِن بُطُونِهَا شَرَابٌ مُّخْتَلِفٌ أَلْوَانُهُ فِيهِ شِفَاءٌ لِّلنَّاسِ ۗ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَةً لِّقَوْمٍ يَتَفَكَّرُونَ
Topp [Mu ne ko] nanga lekk ci mépp meññent, te nangay sóobu ci say yooni Boroom muy lu ñu la yombalal. Dana génnee ci biiram naan goo xam ne dana am ay melo yu wuute (lem). Te nekk na ci luy faj nit ñi. Te loolu kéemaan la ci aw nit ñuy xalaat.
70وَاللَّهُ خَلَقَكُمْ ثُمَّ يَتَوَفَّاكُمْ ۚ وَمِنكُم مَّن يُرَدُّ إِلَىٰ أَرْذَلِ الْعُمُرِ لِكَيْ لَا يَعْلَمَ بَعْدَ عِلْمٍ شَيْئًا ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ قَدِيرٌ
Te Yàlla moo leen bind ! Dana leen rey. Te am na ci yéen ñuy àgg ba ci màggat lool, duñu xamati dara ginnaaw ba ñu nekkoon ñu xam. Naka Yàlla moo di Aji-xam ji, di Aji-kàttan gi.
71وَاللَّهُ فَضَّلَ بَعْضَكُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ فِي الرِّزْقِ ۚ فَمَا الَّذِينَ فُضِّلُوا بِرَادِّي رِزْقِهِمْ عَلَىٰ مَا مَلَكَتْ أَيْمَانُهُمْ فَهُمْ فِيهِ سَوَاءٌ ۚ أَفَبِنِعْمَةِ اللَّهِ يَجْحَدُونَ
Yàlla yékkati na ñenn ña ci kaw ñeneen ña ci wërsëg. Te ña Mu jox ngëneel loolu, duñu delloo dara ci wërsëg woowu, jox ko seeni jaam ngir ñu yemoo ca wërsëg wa. Moo ndax dañuy weddi xéewali Yàlla ? Fàkk
72وَاللَّهُ جَعَلَ لَكُم مِّنْ أَنفُسِكُمْ أَزْوَاجًا وَجَعَلَ لَكُم مِّنْ أَزْوَاجِكُم بَنِينَ وَحَفَدَةً وَرَزَقَكُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ ۚ أَفَبِالْبَاطِلِ يُؤْمِنُونَ وَبِنِعْمَتِ اللَّهِ هُمْ يَكْفُرُونَ
Yàlla sàkkal na leen ay jabar yu jóge ci yéen, Mu sàkkal leen ay doom yu jóge ci seeni jabar ak i sët. Mu boole ca wërsëgal leen ñam yu sell. Waa ndax [yéefar yi] dañuy gëm ay xërëm tey weddi xéewali Yàlla yi ?
73وَيَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَمْلِكُ لَهُمْ رِزْقًا مِّنَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ شَيْئًا وَلَا يَسْتَطِيعُونَ
Te dañoo bàyyi Yàlla di jaamu loo xam ne moomul dara lu mu leen mën a wërsërgal ci kaw asamaan yi ak ci suuf si. Te mënul dara.
An-NahlFihi Alxuraan
128Aaya
MeccanRevelation
71Aaya

Tekki — An-Nahl 71

Simoore An-Nahl Aaya 71 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla yékkati na ñenn ña ci kaw ñeneen ña ci…

Simoore Aaya 71/128 — An-Nahl النحل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nahl Dégg, An-Nahl Tekki, An-Nahl mp3, An-Nahl pdf. Aaya 69–73. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers