Al-Isra · 17/111
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Isra
وَكَمْ أَهْلَكْنَا مِنَ الْقُرُونِ مِن بَعْدِ نُوحٍ ۗ وَكَفَىٰ بِرَبِّكَ بِذُنُوبِ عِبَادِهِ خَبِيرًا بَصِيرًا ۝١٧
Wa kam ahlaknaa minal qurooni mim ba`di Nooh; wa kafaa bi Rabbika bizunoobi `ibaadihee Khabeeram Baseeraa
📖 Tekkim Wolof
Aka bari xeet yu Nu alag ginnaaw Nooh ! Te sa Boroom kuy gis la te xam bàkkaari jaam ñi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 15-19 — Simoore Al-Isra

15مَّنِ اهْتَدَىٰ فَإِنَّمَا يَهْتَدِي لِنَفْسِهِ ۖ وَمَن ضَلَّ فَإِنَّمَا يَضِلُّ عَلَيْهَا ۚ وَلَا تَزِرُ وَازِرَةٌ وِزْرَ أُخْرَىٰ ۗ وَمَا كُنَّا مُعَذِّبِينَ حَتَّىٰ نَبْعَثَ رَسُولًا
Ku jub, boppam la ko defal ; ku dëng boppam la ko def. Ndax kenn du yenu yenu keneen. Te nekkunu woon di Aji-mbugal wenn xeet te yónniwunu ab Yonent ca ñoom.
16وَإِذَا أَرَدْنَا أَن نُّهْلِكَ قَرْيَةً أَمَرْنَا مُتْرَفِيهَا فَفَسَقُوا فِيهَا فَحَقَّ عَلَيْهَا الْقَوْلُ فَدَمَّرْنَاهَا تَدْمِيرًا
Bu Nu nammee alag ab dëkk, dafay fekk ne boroom alal ya dañoo jubadi ca dëkk ba. Àtte ba daldi yell ca ñoom. Nu sadd leen sadd gu tar.
17وَكَمْ أَهْلَكْنَا مِنَ الْقُرُونِ مِن بَعْدِ نُوحٍ ۗ وَكَفَىٰ بِرَبِّكَ بِذُنُوبِ عِبَادِهِ خَبِيرًا بَصِيرًا
Aka bari xeet yu Nu alag ginnaaw Nooh ! Te sa Boroom kuy gis la te xam bàkkaari jaam ñi.
18مَّن كَانَ يُرِيدُ الْعَاجِلَةَ عَجَّلْنَا لَهُ فِيهَا مَا نَشَاءُ لِمَن نُّرِيدُ ثُمَّ جَعَلْنَا لَهُ جَهَنَّمَ يَصْلَاهَا مَذْمُومًا مَّدْحُورًا
Képp ku bëggul lu dul teraangay àddina, Dananu gaaw ci jox ko la Nu neex ; ca ku Nu neex. Topp Nu def Safara fa muy séndalu, di ku ñu xas, ku ñu génne [ci yërmaandey Yàlla].
19وَمَنْ أَرَادَ الْآخِرَةَ وَسَعَىٰ لَهَا سَعْيَهَا وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَأُولَٰئِكَ كَانَ سَعْيُهُم مَّشْكُورًا
Ku bëgg [teraangay] àllaaxira te mu jëf lu méngook moom, te muy ku gëm... ñooñu seeni jëf lu ñu gërëm lay doon.
Al-IsraFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
17Aaya

Tekki — Al-Isra 17

Simoore Al-Isra Aaya 17 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Aka bari xeet yu Nu alag ginnaaw Nooh ! Te…

Simoore Aaya 17/111 — Simoore Al-Isra الإسراء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Isra Dégg, Simoore Al-Isra Tekki, Simoore Al-Isra mp3, Simoore Al-Isra pdf. Aaya 15–19. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers