Al-Baqara · 138/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
صِبْغَةَ اللَّهِ ۖ وَمَنْ أَحْسَنُ مِنَ اللَّهِ صِبْغَةً ۖ وَنَحْنُ لَهُ عَابِدُونَ ۝١٣٨
Sibghatal laahi wa man ahsanu minal laahi sibghatanw wa nahnu lahoo `aabidoon
📖 Tekkim Wolof
“Loolu cuubug Yàllaa ! Te ana kan moo gën a rafet Yàlla ag cuub ? Nun dey way-jaamu ko lanu”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 136-140 — Al-Baqara

136قُولُوا آمَنَّا بِاللَّهِ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْنَا وَمَا أُنزِلَ إِلَىٰ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَالْأَسْبَاطِ وَمَا أُوتِيَ مُوسَىٰ وَعِيسَىٰ وَمَا أُوتِيَ النَّبِيُّونَ مِن رَّبِّهِمْ لَا نُفَرِّقُ بَيْنَ أَحَدٍ مِّنْهُمْ وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ
Neeleen : “Gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun [Alxuraan], ak li ñu wàcce woon ca Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba ak ca sët ya, ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa, ya ñu joxoon Yonent ya, mu bawoo ca seen Boroom : dunu xajal kenn ci seen diggante. Te nun way-jébbalu (wommatu) lanu jëm ci Yàlla”.
137فَإِنْ آمَنُوا بِمِثْلِ مَا آمَنتُم بِهِ فَقَدِ اهْتَدَوا ۖ وَّإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا هُمْ فِي شِقَاقٍ ۖ فَسَيَكْفِيكَهُمُ اللَّهُ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Bu ñu gëmee Alxuraan kem ni ngeen ko gëmee, kon gindiku nañu. Ñoom Yahuud yi ak Nasaraan yi, bu ñu dummóoyoo rekk daldi dugg ci féewoo ! Yàlla dana la leen fegal. Moom mi di Aji-dégg, di Aji-xam ji.
138صِبْغَةَ اللَّهِ ۖ وَمَنْ أَحْسَنُ مِنَ اللَّهِ صِبْغَةً ۖ وَنَحْنُ لَهُ عَابِدُونَ
“Loolu cuubug Yàllaa ! Te ana kan moo gën a rafet Yàlla ag cuub ? Nun dey way-jaamu ko lanu”.
139قُلْ أَتُحَاجُّونَنَا فِي اللَّهِ وَهُوَ رَبُّنَا وَرَبُّكُمْ وَلَنَا أَعْمَالُنَا وَلَكُمْ أَعْمَالُكُمْ وَنَحْنُ لَهُ مُخْلِصُونَ
Neel : “Ndax dangeen di dàggasanteek nun ci Yàlla sunu Boroom, di seen Boroom ? Nu moom sunu jëf, ngeen moom seen jëf ! Te nun nag way-sellalal Ko lanuy doon.
140أَمْ تَقُولُونَ إِنَّ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَالْأَسْبَاطَ كَانُوا هُودًا أَوْ نَصَارَىٰ ۗ قُلْ أَأَنتُمْ أَعْلَمُ أَمِ اللَّهُ ۗ وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن كَتَمَ شَهَادَةً عِندَهُ مِنَ اللَّهِ ۗ وَمَا اللَّهُ بِغَافِلٍ عَمَّا تَعْمَلُونَ
Am dañuy wax ne : Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba ak sët ya ay Yahuud lañu woon walla Nasaraan ? ” - Neeleen : “Ndax yéen a gën xam walla Yàlla ? ” - Waay-waay ana kan moo dàq a tooñ kiy nëbb seede sa nekk fa moom te bawoo fa Yàlla ? Te dey Yàlla sàgganeewul li ngeen di jëf de.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
138Aaya

Tekki — Al-Baqara 138

Simoore Al-Baqara Aaya 138 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Loolu cuubug Yàllaa ! Te ana kan moo gën a…

Simoore Aaya 138/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 136–140. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers