Al-Baqara · 137/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
فَإِنْ آمَنُوا بِمِثْلِ مَا آمَنتُم بِهِ فَقَدِ اهْتَدَوا ۖ وَّإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا هُمْ فِي شِقَاقٍ ۖ فَسَيَكْفِيكَهُمُ اللَّهُ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ ۝١٣٧
Fa in aamanoo bimisli maaa aamantum bihee faqadih tadaw wa in tawallaw fa innamaa hum fee shiqaaq; fasayakfeekahumul laah; wa Huwas Samee`ul Aleem
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu gëmee Alxuraan kem ni ngeen ko gëmee, kon gindiku nañu. Ñoom Yahuud yi ak Nasaraan yi, bu ñu dummóoyoo rekk daldi dugg ci féewoo ! Yàlla dana la leen fegal. Moom mi di Aji-dégg, di Aji-xam ji.
🎧 Dégg

📜 Aaya 135-139 — Al-Baqara

135وَقَالُوا كُونُوا هُودًا أَوْ نَصَارَىٰ تَهْتَدُوا ۗ قُلْ بَلْ مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا ۖ وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Ñuy wax naan : “Doonleen Yahuud walla Nasaraan, kon dey ngeen gindiku”. - Neel : “Dée wallaay, diinay Ibraahiima ma wéetaloon Yàlla te bokkut ca way-bokkaale ya”.
136قُولُوا آمَنَّا بِاللَّهِ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْنَا وَمَا أُنزِلَ إِلَىٰ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَالْأَسْبَاطِ وَمَا أُوتِيَ مُوسَىٰ وَعِيسَىٰ وَمَا أُوتِيَ النَّبِيُّونَ مِن رَّبِّهِمْ لَا نُفَرِّقُ بَيْنَ أَحَدٍ مِّنْهُمْ وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ
Neeleen : “Gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun [Alxuraan], ak li ñu wàcce woon ca Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba ak ca sët ya, ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa, ya ñu joxoon Yonent ya, mu bawoo ca seen Boroom : dunu xajal kenn ci seen diggante. Te nun way-jébbalu (wommatu) lanu jëm ci Yàlla”.
137فَإِنْ آمَنُوا بِمِثْلِ مَا آمَنتُم بِهِ فَقَدِ اهْتَدَوا ۖ وَّإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا هُمْ فِي شِقَاقٍ ۖ فَسَيَكْفِيكَهُمُ اللَّهُ ۚ وَهُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Bu ñu gëmee Alxuraan kem ni ngeen ko gëmee, kon gindiku nañu. Ñoom Yahuud yi ak Nasaraan yi, bu ñu dummóoyoo rekk daldi dugg ci féewoo ! Yàlla dana la leen fegal. Moom mi di Aji-dégg, di Aji-xam ji.
138صِبْغَةَ اللَّهِ ۖ وَمَنْ أَحْسَنُ مِنَ اللَّهِ صِبْغَةً ۖ وَنَحْنُ لَهُ عَابِدُونَ
“Loolu cuubug Yàllaa ! Te ana kan moo gën a rafet Yàlla ag cuub ? Nun dey way-jaamu ko lanu”.
139قُلْ أَتُحَاجُّونَنَا فِي اللَّهِ وَهُوَ رَبُّنَا وَرَبُّكُمْ وَلَنَا أَعْمَالُنَا وَلَكُمْ أَعْمَالُكُمْ وَنَحْنُ لَهُ مُخْلِصُونَ
Neel : “Ndax dangeen di dàggasanteek nun ci Yàlla sunu Boroom, di seen Boroom ? Nu moom sunu jëf, ngeen moom seen jëf ! Te nun nag way-sellalal Ko lanuy doon.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
137Aaya

Tekki — Al-Baqara 137

Simoore Al-Baqara Aaya 137 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu gëmee Alxuraan kem ni ngeen ko gëmee, kon…

Simoore Aaya 137/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 135–139. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers