Al-Baqara · 276/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
يَمْحَقُ اللَّهُ الرِّبَا وَيُرْبِي الصَّدَقَاتِ ۗ وَاللَّهُ لَا يُحِبُّ كُلَّ كَفَّارٍ أَثِيمٍ ۝٢٧٦
Yamhaqul laahur ribaa wa yurbis sadaqaat; wallaahu laa yuhibbu kulla kaffaarin aseem
📖 Tekkim Wolof
Yàlla dafay màbb ribaa, di sakkanloo sarax. Yàlla soppul ku weddi, [yéefar] bu ñemey bàkkaar.
🎧 Dégg

📜 Aaya 274-278 — Al-Baqara

274الَّذِينَ يُنفِقُونَ أَمْوَالَهُم بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ سِرًّا وَعَلَانِيَةً فَلَهُمْ أَجْرُهُمْ عِندَ رَبِّهِمْ وَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ñi nga xam ne dañuy joxe seeni alal, guddi ak bëccëg, ci lu nëbbu ak lu feeñ, ñooña am nañu seenug pey fa seen Boroom te duñu jàq.
275الَّذِينَ يَأْكُلُونَ الرِّبَا لَا يَقُومُونَ إِلَّا كَمَا يَقُومُ الَّذِي يَتَخَبَّطُهُ الشَّيْطَانُ مِنَ الْمَسِّ ۚ ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ قَالُوا إِنَّمَا الْبَيْعُ مِثْلُ الرِّبَا ۗ وَأَحَلَّ اللَّهُ الْبَيْعَ وَحَرَّمَ الرِّبَا ۚ فَمَن جَاءَهُ مَوْعِظَةٌ مِّن رَّبِّهِ فَانتَهَىٰ فَلَهُ مَا سَلَفَ وَأَمْرُهُ إِلَى اللَّهِ ۖ وَمَنْ عَادَ فَأُولَٰئِكَ أَصْحَابُ النَّارِ ۖ هُمْ فِيهَا خَالِدُونَ
Ñay lekk ribaa, [duñu jóg] ci seeni bàmmeel lu dul jógeenu ku Séytaane daaneel, sadd ko saddum jinne. Ndax dañu ne : “Jaay ak ribaa ñoo yem”. Te Yàlla daganal na jaay, araamal na ribaa. Képp ku ñu ca waar ci lu jóge ca Yàlla ba nga bàyyi ribaa, mën naa téy la weesu ; mbiram ma nga ca Yàlla. Ku ca dellusi nag... ñooña, ñooy waa Safara ! Te dañu cay béel.
276يَمْحَقُ اللَّهُ الرِّبَا وَيُرْبِي الصَّدَقَاتِ ۗ وَاللَّهُ لَا يُحِبُّ كُلَّ كَفَّارٍ أَثِيمٍ
Yàlla dafay màbb ribaa, di sakkanloo sarax. Yàlla soppul ku weddi, [yéefar] bu ñemey bàkkaar.
277إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ وَآتَوُا الزَّكَاةَ لَهُمْ أَجْرُهُمْ عِندَ رَبِّهِمْ وَلَا خَوْفٌ عَلَيْهِمْ وَلَا هُمْ يَحْزَنُونَ
Ñi gëm tey jëfe yiw , di taxawal julli tey joxe asaka, am nañu seenug pey fa seen Boroom. Te amuñu lu ñuy tiit walla lu ñuy jàq.
278يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَذَرُوا مَا بَقِيَ مِنَ الرِّبَا إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla ; te ngeen bàyyi li des ci ribaa yi, ndegam ñu gëm ngeen.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
276Aaya

Tekki — Al-Baqara 276

Simoore Al-Baqara Aaya 276 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla dafay màbb ribaa, di sakkanloo sarax. Yàlla soppul ku…

Simoore Aaya 276/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 274–278. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers