Al-Hajj · 56/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
الْمُلْكُ يَوْمَئِذٍ لِّلَّهِ يَحْكُمُ بَيْنَهُمْ ۚ فَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فِي جَنَّاتِ النَّعِيمِ ۝٥٦
Almulku Yawma`izil lillaahi yahkumu bainahum; fallazeena aamanoo wa `amilus saalihaati fee jannaatin Na`eem
📖 Tekkim Wolof
Bis niki tey nguur gi Yàllaa lo moom. Dana àtte seen diggante. Kon ña gëm tey jëf jëf ju yiw, danañu nekk ci Àjjanay xéewal,

🎧 Dégg


📜 Aaya 54-58 — Al-Hajj

54وَلِيَعْلَمَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ أَنَّهُ الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ فَيُؤْمِنُوا بِهِ فَتُخْبِتَ لَهُ قُلُوبُهُمْ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَهَادِ الَّذِينَ آمَنُوا إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Te Moo dogal loolu lépp ngir ña nga xam ne joxeef na leen xam-xam, ràññee ne Alxuraan ak moom dëgg la gu bawoo fa sa Boroom, ak ngir ñu gëm ko ci seeni xol, dellu ci Moom. Te ñu xam ne Yàlla dana gindi ñi gëm teg leen ca yoon wu jub xocc wa.
55وَلَا يَزَالُ الَّذِينَ كَفَرُوا فِي مِرْيَةٍ مِّنْهُ حَتَّىٰ تَأْتِيَهُمُ السَّاعَةُ بَغْتَةً أَوْ يَأْتِيَهُمْ عَذَابُ يَوْمٍ عَقِيمٍ
Te ña weddi duñu deñ ci sikki-sàkka ci moom Alxuraan ba baa Bis-pénc di leen dikkal ci mbetteel walla mbugalum bis bu tiis ba dikkal leen.
56الْمُلْكُ يَوْمَئِذٍ لِّلَّهِ يَحْكُمُ بَيْنَهُمْ ۚ فَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فِي جَنَّاتِ النَّعِيمِ
Bis niki tey nguur gi Yàllaa lo moom. Dana àtte seen diggante. Kon ña gëm tey jëf jëf ju yiw, danañu nekk ci Àjjanay xéewal,
57وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا فَأُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ مُّهِينٌ
waaye ña weddi te jàppe ay fen Sunuy kàddu, ñooña ñeel na leen mbugal muy toroxale !
58وَالَّذِينَ هَاجَرُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ ثُمَّ قُتِلُوا أَوْ مَاتُوا لَيَرْزُقَنَّهُمُ اللَّهُ رِزْقًا حَسَنًا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَهُوَ خَيْرُ الرَّازِقِينَ
Ña gàdday ngir liggéey ci yoonu Yàlla, topp ñu rey leen mbaa ñu dee, fàwwu Yàlla dana leen wërsëgal wërsëg wu rafet, te nag Yàlla moo di Ki gën a mën a wërsëgal ci képp kuy wërsëgal.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
56Aaya

Tekki — Al-Hajj 56

Simoore Al-Hajj Aaya 56 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bis niki tey nguur gi Yàllaa lo moom. Dana àtte…

Simoore Aaya 56/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 54–58. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers