Al-Hajj · 55/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
وَلَا يَزَالُ الَّذِينَ كَفَرُوا فِي مِرْيَةٍ مِّنْهُ حَتَّىٰ تَأْتِيَهُمُ السَّاعَةُ بَغْتَةً أَوْ يَأْتِيَهُمْ عَذَابُ يَوْمٍ عَقِيمٍ ۝٥٥
Wa laa yazaalul lazeena kafaroo fee miryatim minhu hattaa taatiyahumus Saa`atu baghtatan aw yaatiyahum `azaabu Yawmin `aqeem
📖 Tekkim Wolof
Te ña weddi duñu deñ ci sikki-sàkka ci moom Alxuraan ba baa Bis-pénc di leen dikkal ci mbetteel walla mbugalum bis bu tiis ba dikkal leen.
🎧 Dégg

📜 Aaya 53-57 — Al-Hajj

53لِّيَجْعَلَ مَا يُلْقِي الشَّيْطَانُ فِتْنَةً لِّلَّذِينَ فِي قُلُوبِهِم مَّرَضٌ وَالْقَاسِيَةِ قُلُوبُهُمْ ۗ وَإِنَّ الظَّالِمِينَ لَفِي شِقَاقٍ بَعِيدٍ
Lu Séytaane sànni Dafa koo def muy nattu ca ña jàngoro nekk ca seen xol ak ña seeni xol wow... Ca tooñkat ya ñu nekk ci wuute gu sore [dëgg].
54وَلِيَعْلَمَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ أَنَّهُ الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ فَيُؤْمِنُوا بِهِ فَتُخْبِتَ لَهُ قُلُوبُهُمْ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَهَادِ الَّذِينَ آمَنُوا إِلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ
Te Moo dogal loolu lépp ngir ña nga xam ne joxeef na leen xam-xam, ràññee ne Alxuraan ak moom dëgg la gu bawoo fa sa Boroom, ak ngir ñu gëm ko ci seeni xol, dellu ci Moom. Te ñu xam ne Yàlla dana gindi ñi gëm teg leen ca yoon wu jub xocc wa.
55وَلَا يَزَالُ الَّذِينَ كَفَرُوا فِي مِرْيَةٍ مِّنْهُ حَتَّىٰ تَأْتِيَهُمُ السَّاعَةُ بَغْتَةً أَوْ يَأْتِيَهُمْ عَذَابُ يَوْمٍ عَقِيمٍ
Te ña weddi duñu deñ ci sikki-sàkka ci moom Alxuraan ba baa Bis-pénc di leen dikkal ci mbetteel walla mbugalum bis bu tiis ba dikkal leen.
56الْمُلْكُ يَوْمَئِذٍ لِّلَّهِ يَحْكُمُ بَيْنَهُمْ ۚ فَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فِي جَنَّاتِ النَّعِيمِ
Bis niki tey nguur gi Yàllaa lo moom. Dana àtte seen diggante. Kon ña gëm tey jëf jëf ju yiw, danañu nekk ci Àjjanay xéewal,
57وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا فَأُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ مُّهِينٌ
waaye ña weddi te jàppe ay fen Sunuy kàddu, ñooña ñeel na leen mbugal muy toroxale !
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
55Aaya

Tekki — Al-Hajj 55

Simoore Al-Hajj Aaya 55 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te ña weddi duñu deñ ci sikki-sàkka ci moom Alxuraan…

Simoore Aaya 55/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 53–57. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers