Al-Hajj · 8/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
وَمِنَ النَّاسِ مَن يُجَادِلُ فِي اللَّهِ بِغَيْرِ عِلْمٍ وَلَا هُدًى وَلَا كِتَابٍ مُّنِيرٍ ۝٨
Wa minan naasi mai yujaadilu fil laahi bighairi `ilminw wa laa hudanw wa laa Kitaabim Muneer
📖 Tekkim Wolof
Ci nit ñi, am na ñuy dàggasante ci Yàlla cig ñàkk a xam te àndul ak njub, te amul Téere bu wér,

🎧 Dégg


📜 Aaya 6-10 — Al-Hajj

6ذَٰلِكَ بِأَنَّ اللَّهَ هُوَ الْحَقُّ وَأَنَّهُ يُحْيِي الْمَوْتَىٰ وَأَنَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Loolu [lu wér la] ngir Yàlla mooy dëgg ga ; te Moom mooy dekkal ñi dee ; te Moom am na kàttan ci def lu ne.
7وَأَنَّ السَّاعَةَ آتِيَةٌ لَّا رَيْبَ فِيهَا وَأَنَّ اللَّهَ يَبْعَثُ مَن فِي الْقُبُورِ
Te Bis-pénc ba amul sikk ne luy ñëw la,te Yàlla dana dekkal mboolem ñi nekk ci bàmmeel yi.
8وَمِنَ النَّاسِ مَن يُجَادِلُ فِي اللَّهِ بِغَيْرِ عِلْمٍ وَلَا هُدًى وَلَا كِتَابٍ مُّنِيرٍ
Ci nit ñi, am na ñuy dàggasante ci Yàlla cig ñàkk a xam te àndul ak njub, te amul Téere bu wér,
9ثَانِيَ عِطْفِهِ لِيُضِلَّ عَن سَبِيلِ اللَّهِ ۖ لَهُ فِي الدُّنْيَا خِزْيٌ ۖ وَنُذِيقُهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ عَذَابَ الْحَرِيقِ
muy lem loosam [di rëy-rëylu] ngir réerloo [nit ñi] soreel leen yoonu Yàlla. Kooku dey am na ci àddina toroxtaange ; te Dananu ko mosal Bis-pénc ba mbugal muy tàng di lakkaate.
10ذَٰلِكَ بِمَا قَدَّمَتْ يَدَاكَ وَأَنَّ اللَّهَ لَيْسَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ
Loolu la yelloo ngir la ñaari yoxoom ya def ci àddina ! Te Yàlla du tooñ jaamam ñi.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
8Aaya

Tekki — Al-Hajj 8

Simoore Al-Hajj Aaya 8 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ci nit ñi, am na ñuy dàggasante ci Yàlla cig…

Simoore Aaya 8/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 6–10. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers