An-Nur · 64/64
Tekki Waxtaan — An-Nur
أَلَا إِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ قَدْ يَعْلَمُ مَا أَنتُمْ عَلَيْهِ وَيَوْمَ يُرْجَعُونَ إِلَيْهِ فَيُنَبِّئُهُم بِمَا عَمِلُوا ۗ وَاللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ ۝٦٤
Alaaa inna lillaahi maa fis samaawaati wal ardi qad ya`lamu maaa antum `alaihi wa Yawma yurja`oona ilaihi fa yunaabi `uhum bimaa `amiloo; wallaahu bikulli shai`in `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Ca dëgg-dëgg, Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Moo gën a xam li ngeen nekk, bu keroogee ba ñu leen di delloo ca Moom, Mu di leen xibaar la ñu defoon. Yàlla kat xam na lépp.
🎧 Dégg

📜 Aaya 62-64 — An-Nur

62إِنَّمَا الْمُؤْمِنُونَ الَّذِينَ آمَنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَإِذَا كَانُوا مَعَهُ عَلَىٰ أَمْرٍ جَامِعٍ لَّمْ يَذْهَبُوا حَتَّىٰ يَسْتَأْذِنُوهُ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَسْتَأْذِنُونَكَ أُولَٰئِكَ الَّذِينَ يُؤْمِنُونَ بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ ۚ فَإِذَا اسْتَأْذَنُوكَ لِبَعْضِ شَأْنِهِمْ فَأْذَن لِّمَن شِئْتَ مِنْهُمْ وَاسْتَغْفِرْ لَهُمُ اللَّهَ ۚ إِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Way-gëm ña dëgg-dëgg ñooy ña gëm Yàlla ak ub Yonentam, te mépp mbir mu ñu bokk ak nit ñi, bala ñu caa jëfandiku, laaj ndigal. Ñooñii nga xam ne ñoo lay laaj ndigal ngir seen itte bopp, na nga jox ndigal ña la soob ; te nanga leen jéggalul Yàlla, Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
63لَّا تَجْعَلُوا دُعَاءَ الرَّسُولِ بَيْنَكُمْ كَدُعَاءِ بَعْضِكُم بَعْضًا ۚ قَدْ يَعْلَمُ اللَّهُ الَّذِينَ يَتَسَلَّلُونَ مِنكُمْ لِوَاذًا ۚ فَلْيَحْذَرِ الَّذِينَ يُخَالِفُونَ عَنْ أَمْرِهِ أَن تُصِيبَهُمْ فِتْنَةٌ أَوْ يُصِيبَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Buleen def wooteb Yonent bi ni wooteb jenn waay ci yéen. Yàlla dana xam ñay potoxlu te bokk ci yéen. Ña nga xam ne dañuy moy ndigalam, nañu moytu ab sànje dal leen mbaa mbugal mu metti.
64أَلَا إِنَّ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ قَدْ يَعْلَمُ مَا أَنتُمْ عَلَيْهِ وَيَوْمَ يُرْجَعُونَ إِلَيْهِ فَيُنَبِّئُهُم بِمَا عَمِلُوا ۗ وَاللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Ca dëgg-dëgg, Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf si. Moo gën a xam li ngeen nekk, bu keroogee ba ñu leen di delloo ca Moom, Mu di leen xibaar la ñu defoon. Yàlla kat xam na lépp.
An-NurFihi Alxuraan
64Aaya
MedinanRevelation
64Aaya

Tekki — An-Nur 64

Simoore An-Nur Aaya 64 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ca dëgg-dëgg, Yàllaa moom li nekk ci asamaan yeek suuf…

Simoore Aaya 64/64 — An-Nur النور (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Nur Dégg, An-Nur Tekki, An-Nur mp3, An-Nur pdf. Aaya 62–64. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers