An-Naml · 22/93
Tekki Waxtaan — An-Naml
فَمَكَثَ غَيْرَ بَعِيدٍ فَقَالَ أَحَطتُ بِمَا لَمْ تُحِطْ بِهِ وَجِئْتُكَ مِن سَبَإٍ بِنَبَإٍ يَقِينٍ ۝٢٢
Famakasa ghaira ba`eedin faqaala ahattu bimaa lam tuhit bihee wa ji`tuka min Sabaim binaba iny-yaqeen
📖 Tekkim Wolof
Mu sax fa tuuti, [picc] ma dellusi ne ko : “Xam naa loo xamul te indil naa la xibaar bu wóor bu bawoo réewum Sabaa” :

🎧 Dégg


📜 Aaya 20-24 — An-Naml

20وَتَفَقَّدَ الطَّيْرَ فَقَالَ مَا لِيَ لَا أَرَى الْهُدْهُدَ أَمْ كَانَ مِنَ الْغَائِبِينَ
Mu nemmiku njanaaw ya, daldi ne : “Lan moo tax gisuma Muusaa-njuburi ? Walla nekku fi?
21لَأُعَذِّبَنَّهُ عَذَابًا شَدِيدًا أَوْ لَأَذْبَحَنَّهُ أَوْ لَيَأْتِيَنِّي بِسُلْطَانٍ مُّبِينٍ
Danaa ko mbugal mbugal mu tar ! Walla ma rendi ko ! Walla mu indil ma lay wu wér”.
22فَمَكَثَ غَيْرَ بَعِيدٍ فَقَالَ أَحَطتُ بِمَا لَمْ تُحِطْ بِهِ وَجِئْتُكَ مِن سَبَإٍ بِنَبَإٍ يَقِينٍ
Mu sax fa tuuti, [picc] ma dellusi ne ko : “Xam naa loo xamul te indil naa la xibaar bu wóor bu bawoo réewum Sabaa” :
23إِنِّي وَجَدتُّ امْرَأَةً تَمْلِكُهُمْ وَأُوتِيَتْ مِن كُلِّ شَيْءٍ وَلَهَا عَرْشٌ عَظِيمٌ
Fekk naa leen ñu am buur bu jigéen, am na lépp, am it gàngunaay gu rëy.
24وَجَدتُّهَا وَقَوْمَهَا يَسْجُدُونَ لِلشَّمْسِ مِن دُونِ اللَّهِ وَزَيَّنَ لَهُمُ الشَّيْطَانُ أَعْمَالَهُمْ فَصَدَّهُمْ عَنِ السَّبِيلِ فَهُمْ لَا يَهْتَدُونَ
Fekk naa ko it mook aw nitam ñuy jaamu jant bi bàyyi Yàlla. Séytaane taaralal leen jëf jooju, wëlbati leen ñu dëddu yoonu Yàlla ba gëmuñu.
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
22Aaya

Tekki — An-Naml 22

Simoore An-Naml Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu sax fa tuuti, [picc] ma dellusi ne ko :…

Simoore Aaya 22/93 — An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Naml Dégg, An-Naml Tekki, An-Naml mp3, An-Naml pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers