An-Naml · 83/93
Tekki Waxtaan — An-Naml
وَيَوْمَ نَحْشُرُ مِن كُلِّ أُمَّةٍ فَوْجًا مِّمَّن يُكَذِّبُ بِآيَاتِنَا فَهُمْ يُوزَعُونَ ۝٨٣
Wa Yawma nahshuru min kulli ummmatin fawjam mim many-yukazzibu bi Aayaatinaa fahum yooza`oon
📖 Tekkim Wolof
Bu keroogee Bis ba Nuy pang, ci wépp xeet ay mbooloo yu daan jàppe Sunu kàddu yii ay fen [di ko weddi], Nu def leen ñu di ay sàppe.

🎧 Dégg


📜 Aaya 81-85 — An-Naml

81وَمَا أَنتَ بِهَادِي الْعُمْيِ عَن ضَلَالَتِهِمْ ۖ إِن تُسْمِعُ إِلَّا مَن يُؤْمِنُ بِآيَاتِنَا فَهُم مُّسْلِمُونَ
Mënoo gindi gumba yi ci seenug réer. Ñi lay déglu kay ñooy ña gëm Sunuy kàddu te doon ay jullit.
82۞ وَإِذَا وَقَعَ الْقَوْلُ عَلَيْهِمْ أَخْرَجْنَا لَهُمْ دَابَّةً مِّنَ الْأَرْضِ تُكَلِّمُهُمْ أَنَّ النَّاسَ كَانُوا بِآيَاتِنَا لَا يُوقِنُونَ
Saa su wax ja tàbbee ci seen kaw, Dananu leen génneel benn mala buy wàqanteek ñoom ne : Nit ñi gëmuñu woon Sunuy kàddu, kéemaan.
83وَيَوْمَ نَحْشُرُ مِن كُلِّ أُمَّةٍ فَوْجًا مِّمَّن يُكَذِّبُ بِآيَاتِنَا فَهُمْ يُوزَعُونَ
Bu keroogee Bis ba Nuy pang, ci wépp xeet ay mbooloo yu daan jàppe Sunu kàddu yii ay fen [di ko weddi], Nu def leen ñu di ay sàppe.
84حَتَّىٰ إِذَا جَاءُوا قَالَ أَكَذَّبْتُم بِآيَاتِي وَلَمْ تُحِيطُوا بِهَا عِلْمًا أَمَّاذَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
Bu ñu agsee, [Yàlla] ne leen : “Waaw, yéen a daan weddi Samay kàddu te xamuleen ci woon dara ? Walla lan ngeen daan def ? ”
85وَوَقَعَ الْقَوْلُ عَلَيْهِم بِمَا ظَلَمُوا فَهُمْ لَا يَنطِقُونَ
Su wax ja agsee ci ñoom, seen tooñ ga dana tax duñu àddu.
An-NamlFihi Alxuraan
93Aaya
MeccanRevelation
83Aaya

Tekki — An-Naml 83

Simoore An-Naml Aaya 83 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu keroogee Bis ba Nuy pang, ci wépp xeet ay…

Simoore Aaya 83/93 — An-Naml النمل (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: An-Naml Dégg, An-Naml Tekki, An-Naml mp3, An-Naml pdf. Aaya 81–85. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers