Al-Qasas · 70/88
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Qasas
وَهُوَ اللَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ لَهُ الْحَمْدُ فِي الْأُولَىٰ وَالْآخِرَةِ ۖ وَلَهُ الْحُكْمُ وَإِلَيْهِ تُرْجَعُونَ ۝٧٠
Wa Huwal laahu laaa ilaaha illaa Huwa lahul hamdu fil oolaa wal Aakhirati wa lahul hukmu wa ilaihi turja`oon
📖 Tekkim Wolof
Te Moom mooy Yàlla te amul jeneen yàlla ju dul Moom. Moo moom xeeti cant yépp cig njalbéen ba cig mujj. Te Moo moom àtte ya. Te ca Moom lañu di delloo ñépp.

🎧 Dégg


📜 Aaya 68-72 — Simoore Al-Qasas

68وَرَبُّكَ يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ وَيَخْتَارُ ۗ مَا كَانَ لَهُمُ الْخِيَرَةُ ۚ سُبْحَانَ اللَّهِ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يُشْرِكُونَ
Te sa Boroom mooy sàkk lu ko soob te neex ko ; ñoom amuñu coppan. Tudd naa sellug Yàlla ! Te kawe na lool ci la ñuy bokkaale !
69وَرَبُّكَ يَعْلَمُ مَا تُكِنُّ صُدُورُهُمْ وَمَا يُعْلِنُونَ
Te it sa Boroom a xam li seeni xol nëbb ak li ñuy feeñal.
70وَهُوَ اللَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ لَهُ الْحَمْدُ فِي الْأُولَىٰ وَالْآخِرَةِ ۖ وَلَهُ الْحُكْمُ وَإِلَيْهِ تُرْجَعُونَ
Te Moom mooy Yàlla te amul jeneen yàlla ju dul Moom. Moo moom xeeti cant yépp cig njalbéen ba cig mujj. Te Moo moom àtte ya. Te ca Moom lañu di delloo ñépp.
71قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِن جَعَلَ اللَّهُ عَلَيْكُمُ اللَّيْلَ سَرْمَدًا إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَنْ إِلَٰهٌ غَيْرُ اللَّهِ يَأْتِيكُم بِضِيَاءٍ ۖ أَفَلَا تَسْمَعُونَ
Neel : “Xanaa gisuleen ne bu Yàlla defoon guddi gi muy lu sax ba Bis-pénc ba, ana jan yàlla ju dul Moom moo leen di indil ag leer ? Moo ndax dungeen dégg ? ”
72قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِن جَعَلَ اللَّهُ عَلَيْكُمُ النَّهَارَ سَرْمَدًا إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ مَنْ إِلَٰهٌ غَيْرُ اللَّهِ يَأْتِيكُم بِلَيْلٍ تَسْكُنُونَ فِيهِ ۖ أَفَلَا تُبْصِرُونَ
Neel : “Xanaa gisuleen ne bu Yàlla ci yéen bëccëg muy lu sax ba Bis-pénc ba, ana jan yàlla ju dul Moom moo leen di indil guddi gu ngeen di dalloo ? Moo ndax dangeen dul gis ? ”
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
70Aaya

Tekki — Al-Qasas 70

Simoore Al-Qasas Aaya 70 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te Moom mooy Yàlla te amul jeneen yàlla ju dul…

Simoore Aaya 70/88 — Simoore Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Qasas Dégg, Simoore Al-Qasas Tekki, Simoore Al-Qasas mp3, Simoore Al-Qasas pdf. Aaya 68–72. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers