Aali Imran · 19/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
إِنَّ الدِّينَ عِندَ اللَّهِ الْإِسْلَامُ ۗ وَمَا اخْتَلَفَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ إِلَّا مِن بَعْدِ مَا جَاءَهُمُ الْعِلْمُ بَغْيًا بَيْنَهُمْ ۗ وَمَن يَكْفُرْ بِآيَاتِ اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ ۝١٩
Innad deena `indal laahil Islaam; wa makhtalafal lazeena ootul Kitaaba illaa mim ba`di maa jaaa`ahumul `ilmu baghyam bainahum; wa mai yakfur bi Aayaatil laahi fa innal laaha saree`ul hisaab
📖 Tekkim Wolof
Diine Yàlla tigi mooy Lislaam. Ñoñ-téere ya yi wuutewuñu woon lu dul ba leen xam-xam ba dikkalee, ñu beew ci seeni diggante. Képp ku weddi kàddug Yàlla... na xam ne Yàlla ku gaaw la ci xayma jëf yi !

🎧 Dégg


📜 Aaya 17-21 — Simoore Aali Imran

17الصَّابِرِينَ وَالصَّادِقِينَ وَالْقَانِتِينَ وَالْمُنفِقِينَ وَالْمُسْتَغْفِرِينَ بِالْأَسْحَارِ
ñooy, muñkat ya, ña dëggal, diy jaamukat, diy joxekati alal [ngir Yàlla] tey sàkku njéggal waxtuw njël.
18شَهِدَ اللَّهُ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ وَالْمَلَائِكَةُ وَأُولُو الْعِلْمِ قَائِمًا بِالْقِسْطِ ۚ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Yàlla seede na ne, amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Malaaka ya ak woroom xam-xam ya taxawe ci maandu it, seede nañu ne amul jeneen Yàlla ju dul Moom. Ku not la, ku xereñ la !
19إِنَّ الدِّينَ عِندَ اللَّهِ الْإِسْلَامُ ۗ وَمَا اخْتَلَفَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ إِلَّا مِن بَعْدِ مَا جَاءَهُمُ الْعِلْمُ بَغْيًا بَيْنَهُمْ ۗ وَمَن يَكْفُرْ بِآيَاتِ اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Diine Yàlla tigi mooy Lislaam. Ñoñ-téere ya yi wuutewuñu woon lu dul ba leen xam-xam ba dikkalee, ñu beew ci seeni diggante. Képp ku weddi kàddug Yàlla... na xam ne Yàlla ku gaaw la ci xayma jëf yi !
20فَإِنْ حَاجُّوكَ فَقُلْ أَسْلَمْتُ وَجْهِيَ لِلَّهِ وَمَنِ اتَّبَعَنِ ۗ وَقُل لِّلَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ وَالْأُمِّيِّينَ أَأَسْلَمْتُمْ ۚ فَإِنْ أَسْلَمُوا فَقَدِ اهْتَدَوا ۖ وَّإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا عَلَيْكَ الْبَلَاغُ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِالْعِبَادِ
Bu ñuy dàggasante ak yaw, neel : “Ci Yàlla laa jublu maak ku ma topp”. Te nga wax ñoñ- téere, ak ña jàngul : “Moo ndax yéen wommatu ngeen ? ” Bu ñu tàbbee ci Lislaam, nga xam ne gindiku nañu. Bu ñu dummóoyoo nag... Yaw [Muhammad] jotal rekk la ci war. Yàllaa ngi gis jaam ñi.
21إِنَّ الَّذِينَ يَكْفُرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ وَيَقْتُلُونَ النَّبِيِّينَ بِغَيْرِ حَقٍّ وَيَقْتُلُونَ الَّذِينَ يَأْمُرُونَ بِالْقِسْطِ مِنَ النَّاسِ فَبَشِّرْهُم بِعَذَابٍ أَلِيمٍ
Ñay weddi kàdduy Yàlla, di rey Yonent ya, ci lu dul dëgg, di rey ñay digle maandute ci nit ñi, na nga leen bégal ci mbugalmu tar.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
19Aaya

Tekki — Aali Imran 19

Simoore Aali Imran Aaya 19 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Diine Yàlla tigi mooy Lislaam. Ñoñ-téere ya yi wuutewuñu woon…

Simoore Aaya 19/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 17–21. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers