Aali Imran · 18/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
شَهِدَ اللَّهُ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ وَالْمَلَائِكَةُ وَأُولُو الْعِلْمِ قَائِمًا بِالْقِسْطِ ۚ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝١٨
Shahidal laahu annahoo laa ilaaha illaa Huwa walmalaaa`ikatu wa ulul `ilmi qaaa`imam bilqist; laaa ilaaha illaa Huwal `Azeezul Hakeem
📖 Tekkim Wolof
Yàlla seede na ne, amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Malaaka ya ak woroom xam-xam ya taxawe ci maandu it, seede nañu ne amul jeneen Yàlla ju dul Moom. Ku not la, ku xereñ la !
🎧 Dégg

📜 Aaya 16-20 — Aali Imran

16الَّذِينَ يَقُولُونَ رَبَّنَا إِنَّنَا آمَنَّا فَاغْفِرْ لَنَا ذُنُوبَنَا وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ
ñooy ñay wax naan : "Sunu Boroom, nun gëm nanu ; jéggal nu sunuy bàkkaar, te fegal nu mbugalu Safara”,
17الصَّابِرِينَ وَالصَّادِقِينَ وَالْقَانِتِينَ وَالْمُنفِقِينَ وَالْمُسْتَغْفِرِينَ بِالْأَسْحَارِ
ñooy, muñkat ya, ña dëggal, diy jaamukat, diy joxekati alal [ngir Yàlla] tey sàkku njéggal waxtuw njël.
18شَهِدَ اللَّهُ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ وَالْمَلَائِكَةُ وَأُولُو الْعِلْمِ قَائِمًا بِالْقِسْطِ ۚ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ
Yàlla seede na ne, amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Malaaka ya ak woroom xam-xam ya taxawe ci maandu it, seede nañu ne amul jeneen Yàlla ju dul Moom. Ku not la, ku xereñ la !
19إِنَّ الدِّينَ عِندَ اللَّهِ الْإِسْلَامُ ۗ وَمَا اخْتَلَفَ الَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ إِلَّا مِن بَعْدِ مَا جَاءَهُمُ الْعِلْمُ بَغْيًا بَيْنَهُمْ ۗ وَمَن يَكْفُرْ بِآيَاتِ اللَّهِ فَإِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Diine Yàlla tigi mooy Lislaam. Ñoñ-téere ya yi wuutewuñu woon lu dul ba leen xam-xam ba dikkalee, ñu beew ci seeni diggante. Képp ku weddi kàddug Yàlla... na xam ne Yàlla ku gaaw la ci xayma jëf yi !
20فَإِنْ حَاجُّوكَ فَقُلْ أَسْلَمْتُ وَجْهِيَ لِلَّهِ وَمَنِ اتَّبَعَنِ ۗ وَقُل لِّلَّذِينَ أُوتُوا الْكِتَابَ وَالْأُمِّيِّينَ أَأَسْلَمْتُمْ ۚ فَإِنْ أَسْلَمُوا فَقَدِ اهْتَدَوا ۖ وَّإِن تَوَلَّوْا فَإِنَّمَا عَلَيْكَ الْبَلَاغُ ۗ وَاللَّهُ بَصِيرٌ بِالْعِبَادِ
Bu ñuy dàggasante ak yaw, neel : “Ci Yàlla laa jublu maak ku ma topp”. Te nga wax ñoñ- téere, ak ña jàngul : “Moo ndax yéen wommatu ngeen ? ” Bu ñu tàbbee ci Lislaam, nga xam ne gindiku nañu. Bu ñu dummóoyoo nag... Yaw [Muhammad] jotal rekk la ci war. Yàllaa ngi gis jaam ñi.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
18Aaya

Tekki — Aali Imran 18

Simoore Aali Imran Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla seede na ne, amul jeneen Yàlla ju dul Moom,…

Simoore Aaya 18/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers