Aali Imran · 199/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
وَإِنَّ مِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَمَن يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْكُمْ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْهِمْ خَاشِعِينَ لِلَّهِ لَا يَشْتَرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۗ أُولَٰئِكَ لَهُمْ أَجْرُهُمْ عِندَ رَبِّهِمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ ۝١٩٩
Wa inna min Ahlil Kitaabi lamai yu minu billaahi wa maaa unzila ilaikum wa maaa unzila ilaihim khaashi `eena lillaahi laa yashtaroona bi Aayaatil laahi samanan qaleelaa; ulaaa`ika lahum ajruhum `inda Rabbihim; innal laaha saree`ul hisaab
📖 Tekkim Wolof
Am na ci ña jot Téere, ñu gëm Yàlla ak la ñu wàcce ci yéen, ak la ñu wàcce ca ñoom. Dañuy toroxlul Yàlla, duñu jaay laayay Yàlla ci njëg gu néew. Ñooña am nañu seenug pey fa Yàlla te Yàlla ku gaaw la ci waññ [jëfi nit ñi].

🎧 Dégg


📜 Aaya 197-200 — Simoore Aali Imran

197مَتَاعٌ قَلِيلٌ ثُمَّ مَأْوَاهُمْ جَهَنَّمُ ۚ وَبِئْسَ الْمِهَادُ
Xéewal yu néew la ! Topp seenug delluwaay di Safara. Ndaw delluwaay bu ñaaw !
198لَٰكِنِ الَّذِينَ اتَّقَوْا رَبَّهُمْ لَهُمْ جَنَّاتٌ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا نُزُلًا مِّنْ عِندِ اللَّهِ ۗ وَمَا عِندَ اللَّهِ خَيْرٌ لِّلْأَبْرَارِ
Waaye ña ragal seen Boroom, am nañu Àjjana joo xam ne dex yaa ngay daw ca seen ron, ñu béel fa, muy seen wàccuwaay fa Yàlla. Te la nekk fa Yàlla mooy dàqal ñu baax ña.
199وَإِنَّ مِنْ أَهْلِ الْكِتَابِ لَمَن يُؤْمِنُ بِاللَّهِ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْكُمْ وَمَا أُنزِلَ إِلَيْهِمْ خَاشِعِينَ لِلَّهِ لَا يَشْتَرُونَ بِآيَاتِ اللَّهِ ثَمَنًا قَلِيلًا ۗ أُولَٰئِكَ لَهُمْ أَجْرُهُمْ عِندَ رَبِّهِمْ ۗ إِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ
Am na ci ña jot Téere, ñu gëm Yàlla ak la ñu wàcce ci yéen, ak la ñu wàcce ca ñoom. Dañuy toroxlul Yàlla, duñu jaay laayay Yàlla ci njëg gu néew. Ñooña am nañu seenug pey fa Yàlla te Yàlla ku gaaw la ci waññ [jëfi nit ñi].
200يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اصْبِرُوا وَصَابِرُوا وَرَابِطُوا وَاتَّقُوا اللَّهَ لَعَلَّكُمْ تُفْلِحُونَ
Éy yéen ñi gëm ! Nangeen di muñ ci bànneex, nangeen di muñ it [ci aw naqar]. Te itam nangeen di fagaru, te itam ragal-leen Yàlla ndax Yàlla ngeen texe !
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
199Aaya

Tekki — Aali Imran 199

Simoore Aali Imran Aaya 199 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Am na ci ña jot Téere, ñu gëm Yàlla ak…

Simoore Aaya 199/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 197–200. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers