Aali Imran · 93/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
۞ كُلُّ الطَّعَامِ كَانَ حِلًّا لِّبَنِي إِسْرَائِيلَ إِلَّا مَا حَرَّمَ إِسْرَائِيلُ عَلَىٰ نَفْسِهِ مِن قَبْلِ أَن تُنَزَّلَ التَّوْرَاةُ ۗ قُلْ فَأْتُوا بِالتَّوْرَاةِ فَاتْلُوهَا إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٩٣
Kullut ta`aami kaana hillal li Baneee Israaa`eela illaa maa harrama Israaa`eelu `alaa nafsihee min qabli an tunzzalat Tawraah; qul faatoo bit Tawraati fatloohaaa in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Ñam yépp a daganoon ca waa Banii-Israayiil, lu dul ñam ya [Israayiil ] araama loon ca boppam lu jiitu ñu doon wàcce Tawreet. Neel: “Indileen Tawreet te jàng ko, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”

🎧 Dégg


📜 Aaya 91-95 — Simoore Aali Imran

91إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا وَمَاتُوا وَهُمْ كُفَّارٌ فَلَن يُقْبَلَ مِنْ أَحَدِهِم مِّلْءُ الْأَرْضِ ذَهَبًا وَلَوِ افْتَدَىٰ بِهِ ۗ أُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ وَمَا لَهُم مِّن نَّاصِرِينَ
Ña nga xam ne ñoo weddi ba dee ci kéefar, deesul nangul kenn ci ñoom mu jote doonte la joxe na wurus wu fees dell suuf si ngir loolu [jote]. Ñooñee, mbugal mu tar lañuy am, te duñu am ku leen dimbali.
92لَن تَنَالُوا الْبِرَّ حَتَّىٰ تُنفِقُوا مِمَّا تُحِبُّونَ ۚ وَمَا تُنفِقُوا مِن شَيْءٍ فَإِنَّ اللَّهَ بِهِ عَلِيمٌ
Dungeen am mbaax ba ba ngeen di joxe ci li ngeen bëgg. Te lépp lu ngeen mën a joxe, Yàlla xam na ko.
93۞ كُلُّ الطَّعَامِ كَانَ حِلًّا لِّبَنِي إِسْرَائِيلَ إِلَّا مَا حَرَّمَ إِسْرَائِيلُ عَلَىٰ نَفْسِهِ مِن قَبْلِ أَن تُنَزَّلَ التَّوْرَاةُ ۗ قُلْ فَأْتُوا بِالتَّوْرَاةِ فَاتْلُوهَا إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Ñam yépp a daganoon ca waa Banii-Israayiil, lu dul ñam ya [Israayiil ] araama loon ca boppam lu jiitu ñu doon wàcce Tawreet. Neel: “Indileen Tawreet te jàng ko, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”
94فَمَنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ الْكَذِبَ مِن بَعْدِ ذَٰلِكَ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الظَّالِمُونَ
Ku duural Yàlla ay fen, ginnaaw loolu... ñooñaa di tooñkat ya.
95قُلْ صَدَقَ اللَّهُ ۗ فَاتَّبِعُوا مِلَّةَ إِبْرَاهِيمَ حَنِيفًا وَمَا كَانَ مِنَ الْمُشْرِكِينَ
Neel : “Yàllaa wax dëgg. Kon toppleen diiney Ibraahiima. Ku wéetaloon Yàlla la te mësul a bokk ca ñay bokkaale Yàlla”.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
93Aaya

Tekki — Aali Imran 93

Simoore Aali Imran Aaya 93 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñam yépp a daganoon ca waa Banii-Israayiil, lu dul ñam…

Simoore Aaya 93/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 91–95. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers