Al-Maida · 74/120
Tekki Waxtaan — Al-Maida
أَفَلَا يَتُوبُونَ إِلَى اللَّهِ وَيَسْتَغْفِرُونَهُ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٧٤
Afalaa yatooboona ilal laahi wa yastaghfiroonah; wallaahu Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Lu leen teree tuub ci Yàlla ñaan ko njéggal ? Te Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
🎧 Dégg

📜 Aaya 72-76 — Al-Maida

72لَقَدْ كَفَرَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ هُوَ الْمَسِيحُ ابْنُ مَرْيَمَ ۖ وَقَالَ الْمَسِيحُ يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ اعْبُدُوا اللَّهَ رَبِّي وَرَبَّكُمْ ۖ إِنَّهُ مَن يُشْرِكْ بِاللَّهِ فَقَدْ حَرَّمَ اللَّهُ عَلَيْهِ الْجَنَّةَ وَمَأْوَاهُ النَّارُ ۖ وَمَا لِلظَّالِمِينَ مِنْ أَنصَارٍ
Ña wax ne : “Yàlla Mooy ku ñu barkeel ka [Masiih], doomi Maryaama.”, tàbbi nañu ci kéefar. Te moom ku ñu barkeel ka waxoon na ne : "Yéen waa bani Israayiil, nangeen jaamu Yàlla, ka di sama Boroom”. Te [xamleen ne], ku bokkaale Yàlla ak dara, Yàlla Dana ko araamal Àjjana ; def dëkkuwaayam mu di Safara. Te tooñkat ya duñu am ndimbal !
73لَّقَدْ كَفَرَ الَّذِينَ قَالُوا إِنَّ اللَّهَ ثَالِثُ ثَلَاثَةٍ ۘ وَمَا مِنْ إِلَٰهٍ إِلَّا إِلَٰهٌ وَاحِدٌ ۚ وَإِن لَّمْ يَنتَهُوا عَمَّا يَقُولُونَ لَيَمَسَّنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ
Ña wax ne : “Yàlla ñetteel la ci ñett.”, tàbbi nañu ci kéefar. Te Yàlla Moom jenn doŋŋ la ! Bu ñu bàyyiwul li ñuy wax, fàwwu mbugal mu metti dal ña weddi ca ñoom.
74أَفَلَا يَتُوبُونَ إِلَى اللَّهِ وَيَسْتَغْفِرُونَهُ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Lu leen teree tuub ci Yàlla ñaan ko njéggal ? Te Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
75مَّا الْمَسِيحُ ابْنُ مَرْيَمَ إِلَّا رَسُولٌ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهِ الرُّسُلُ وَأُمُّهُ صِدِّيقَةٌ ۖ كَانَا يَأْكُلَانِ الطَّعَامَ ۗ انظُرْ كَيْفَ نُبَيِّنُ لَهُمُ الْآيَاتِ ثُمَّ انظُرْ أَنَّىٰ يُؤْفَكُونَ
Ku ñu barkeel ka, doomi Maryaama, nekkul lu dul ab Yonent, boo xam ne ay Yonent jiitu woon na ko fi. Yaayam ku saxoon ci dëgg la. Ñoom ñaar dañu daan lekk ñam. Gisal ni Nu leen di leerale sunuy tegtal te it xoolal ni ñuy walbateee [dëgg ga].
76قُلْ أَتَعْبُدُونَ مِن دُونِ اللَّهِ مَا لَا يَمْلِكُ لَكُمْ ضَرًّا وَلَا نَفْعًا ۚ وَاللَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Neel : “Moo ndax dangeen di bàyyi Yàlla, di jaamu loo xam ne mënuleen a lor, mënuleen a jariñ ? ”.Te Yàlla Moom Kuy dégg la, Ku xam la.
Al-MaidaFihi Alxuraan
120Aaya
MedinanRevelation
74Aaya

Tekki — Al-Maida 74

Simoore Al-Maida Aaya 74 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Lu leen teree tuub ci Yàlla ñaan ko njéggal ?…

Simoore Aaya 74/120 — Al-Maida المائدة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Maida Dégg, Al-Maida Tekki, Al-Maida mp3, Al-Maida pdf. Aaya 72–76. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers