Al-Hadid · 28/29
Tekki Waxtaan — Al-Hadid
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَآمِنُوا بِرَسُولِهِ يُؤْتِكُمْ كِفْلَيْنِ مِن رَّحْمَتِهِ وَيَجْعَل لَّكُمْ نُورًا تَمْشُونَ بِهِ وَيَغْفِرْ لَكُمْ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ۝٢٨
Yaaa ayyuhal lazeena aamaanut taqullaaha wa aaminoo bi Rasoolihee yu`tikum kiflaini mir rahmatihee wa yaj`al lakum nooran tamshoona bihee wa yaghfir lakum; wallaahu Ghafoorur Raheem
📖 Tekkim Wolof
Eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla te gëm Yonentam bi dana leen defal ñaari cokkoor yu yërmande, danaleen defal it ak leer gu ngeen gindikoo, te it dinaleen jéggël, Yàlla Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la.

🎧 Dégg


📜 Aaya 26-29 — Al-Hadid

26وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا نُوحًا وَإِبْرَاهِيمَ وَجَعَلْنَا فِي ذُرِّيَّتِهِمَا النُّبُوَّةَ وَالْكِتَابَ ۖ فَمِنْهُم مُّهْتَدٍ ۖ وَكَثِيرٌ مِّنْهُمْ فَاسِقُونَ
Yónni Nanu Nooh ak Ibraahiima te it def nanu Yonenta ga ci seeni sët ak Téere ba jox nanu leen ko. Am na ci ñoom ñu gindiku, waaye li ëpp ci ñoom saay-saay lañu.
27ثُمَّ قَفَّيْنَا عَلَىٰ آثَارِهِم بِرُسُلِنَا وَقَفَّيْنَا بِعِيسَى ابْنِ مَرْيَمَ وَآتَيْنَاهُ الْإِنجِيلَ وَجَعَلْنَا فِي قُلُوبِ الَّذِينَ اتَّبَعُوهُ رَأْفَةً وَرَحْمَةً وَرَهْبَانِيَّةً ابْتَدَعُوهَا مَا كَتَبْنَاهَا عَلَيْهِمْ إِلَّا ابْتِغَاءَ رِضْوَانِ اللَّهِ فَمَا رَعَوْهَا حَقَّ رِعَايَتِهَا ۖ فَآتَيْنَا الَّذِينَ آمَنُوا مِنْهُمْ أَجْرَهُمْ ۖ وَكَثِيرٌ مِّنْهُمْ فَاسِقُونَ
Nu daldi xentuloo sunuy Yonent seen mboor, xentuloo Iisaa domu Maryaama indil nanu ko Injiil, te it def nanu ca biir xolu ña ko topp ak ñeewante ak yërmaande. Ak bero jigéen ña ñoom ñoo ko fental seen bopp, Waaye farataalu nu ko ci ñoom. Li nu leen digël daal moo di nañu sàkku ngëramul Yàlla. Te sax sàmmuñu ko ni mu ware. Ña bokk ca ñoom te gëm indil Nanu leen seenug pey. Waaye lu bari ci ñoom ay saay-saay lañu.
28يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَآمِنُوا بِرَسُولِهِ يُؤْتِكُمْ كِفْلَيْنِ مِن رَّحْمَتِهِ وَيَجْعَل لَّكُمْ نُورًا تَمْشُونَ بِهِ وَيَغْفِرْ لَكُمْ ۚ وَاللَّهُ غَفُورٌ رَّحِيمٌ
Eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla te gëm Yonentam bi dana leen defal ñaari cokkoor yu yërmande, danaleen defal it ak leer gu ngeen gindikoo, te it dinaleen jéggël, Yàlla Jéggëlaakoon la Jaglewaakoon la.
29لِّئَلَّا يَعْلَمَ أَهْلُ الْكِتَابِ أَلَّا يَقْدِرُونَ عَلَىٰ شَيْءٍ مِّن فَضْلِ اللَّهِ ۙ وَأَنَّ الْفَضْلَ بِيَدِ اللَّهِ يُؤْتِيهِ مَن يَشَاءُ ۚ وَاللَّهُ ذُو الْفَضْلِ الْعَظِيمِ
Ñoñ Téere nañu xam ne manuñu dara ci ngënéelu Yàlla te it ngëneel ci loxo Yàlla la nekk ; Moo koy jox ku ko soob, te Yàlla moo di Boroom ngëneel lu màgg li.
Al-HadidFihi Alxuraan
29Aaya
MedinanRevelation
28Aaya

Tekki — Al-Hadid 28

Simoore Al-Hadid Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Eey yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla te gëm Yonentam…

Simoore Aaya 28/29 — Al-Hadid الحديد (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hadid Dégg, Al-Hadid Tekki, Al-Hadid mp3, Al-Hadid pdf. Aaya 26–29. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers