Al-A'raf · 100/206
Tekki Waxtaan — Al-A'raf
أَوَلَمْ يَهْدِ لِلَّذِينَ يَرِثُونَ الْأَرْضَ مِن بَعْدِ أَهْلِهَا أَن لَّوْ نَشَاءُ أَصَبْنَاهُم بِذُنُوبِهِمْ ۚ وَنَطْبَعُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَسْمَعُونَ ۝١٠٠
Awa lam yahdi lillazeena yarisoonal arda mim ba`di ahlihaaa al law nashaaa`u asabnaahum bizunoobihim; wa natba`u `alaa quloobihim fahum laa yasma`oon
📖 Tekkim Wolof
Walla ndax dafa leeral ci ñi donn suuf si, ginnaaw ña fi nekkoon, ci ne su Nu neexoon Nu sadd leen ngir seeni bàkkaar ak fatt seeni xol ba dootuñu am dégg-dégg ?
🎧 Dégg

📜 Aaya 98-102 — Al-A'raf

98أَوَأَمِنَ أَهْلُ الْقُرَىٰ أَن يَأْتِيَهُم بَأْسُنَا ضُحًى وَهُمْ يَلْعَبُونَ
Walla dëkk yooyu naagu ne Sunu mbugal duleen dikkal bëccëg fekk ñuy fo ?
99أَفَأَمِنُوا مَكْرَ اللَّهِ ۚ فَلَا يَأْمَنُ مَكْرَ اللَّهِ إِلَّا الْقَوْمُ الْخَاسِرُونَ
Moo ndax dañoo naagu ci pexey Yàlla ? Te kenn du naagu ci pexey Yàlla ku dul nit ñu yàqule.
100أَوَلَمْ يَهْدِ لِلَّذِينَ يَرِثُونَ الْأَرْضَ مِن بَعْدِ أَهْلِهَا أَن لَّوْ نَشَاءُ أَصَبْنَاهُم بِذُنُوبِهِمْ ۚ وَنَطْبَعُ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَهُمْ لَا يَسْمَعُونَ
Walla ndax dafa leeral ci ñi donn suuf si, ginnaaw ña fi nekkoon, ci ne su Nu neexoon Nu sadd leen ngir seeni bàkkaar ak fatt seeni xol ba dootuñu am dégg-dégg ?
101تِلْكَ الْقُرَىٰ نَقُصُّ عَلَيْكَ مِنْ أَنبَائِهَا ۚ وَلَقَدْ جَاءَتْهُمْ رُسُلُهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَمَا كَانُوا لِيُؤْمِنُوا بِمَا كَذَّبُوا مِن قَبْلُ ۚ كَذَٰلِكَ يَطْبَعُ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِ الْكَافِرِينَ
Dëkk yooyu, Noo ngi lay nettali dara ci seeni xibaar. Te fekk Sunuy Yonent dikkoon fa ak ay lay yu leer, waaye ñoom mënatuñu woon a gëm la ñu daan weddi ca njalbéen. Noonu la Yàlla di fattee xoli yéefar ya.
102وَمَا وَجَدْنَا لِأَكْثَرِهِم مِّنْ عَهْدٍ ۖ وَإِن وَجَدْنَا أَكْثَرَهُمْ لَفَاسِقِينَ
Fekkunu woon li ëpp ci ñoom ñu ame kóllare fenn ; lu dul ne li ëpp ci ñoom ay saay-saay lañu.
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
100Aaya

Tekki — Al-A'raf 100

Simoore Al-A'raf Aaya 100 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Walla ndax dafa leeral ci ñi donn suuf si, ginnaaw…

Simoore Aaya 100/206 — Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-A'raf Dégg, Al-A'raf Tekki, Al-A'raf mp3, Al-A'raf pdf. Aaya 98–102. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers