Al-A'raf · 96/206
Tekki Waxtaan — Simoore Al-A'raf
وَلَوْ أَنَّ أَهْلَ الْقُرَىٰ آمَنُوا وَاتَّقَوْا لَفَتَحْنَا عَلَيْهِم بَرَكَاتٍ مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ وَلَٰكِن كَذَّبُوا فَأَخَذْنَاهُم بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ ۝٩٦
Wa law anna ahlal quraaa aamanoo wattaqaw lafatahnaa `alaihim barakaatim minas samaaa`i wal ardi wa laakin kazzaboo fa akhaznaahum bimaa kaanoo yaksiboon
📖 Tekkim Wolof
Bu fekkoon ne waa dëkk yooyu gëmoon nañu te ragal Yàlla, kon fàwwu Dananu leen ubbil ay wërsëg yu bawoo asamaan ak ci suuf si. Waaye dañoo weddi, Nu sadd leen ngir la ñu daan fàggu ci lu bon.

🎧 Dégg


📜 Aaya 94-98 — Simoore Al-A'raf

94وَمَا أَرْسَلْنَا فِي قَرْيَةٍ مِّن نَّبِيٍّ إِلَّا أَخَذْنَا أَهْلَهَا بِالْبَأْسَاءِ وَالضَّرَّاءِ لَعَلَّهُمْ يَضَّرَّعُونَ
Dunu yónni Yonent ci am réew, te tegunu waa réew ma ay tiis ak i njàqare ngir xéy-na ñu toroxlu.
95ثُمَّ بَدَّلْنَا مَكَانَ السَّيِّئَةِ الْحَسَنَةَ حَتَّىٰ عَفَوا وَّقَالُوا قَدْ مَسَّ آبَاءَنَا الضَّرَّاءُ وَالسَّرَّاءُ فَأَخَذْنَاهُم بَغْتَةً وَهُمْ لَا يَشْعُرُونَ
Ginnaaw ba ñu soppi yu bon ya, toxal ca yu baax, bu ñu biroo it ñu naan : “Aw naqar ak mbégte daloon na sunuy maam.”. Nu songe woon leen ci mbetteel te fooguñu ko woon.
96وَلَوْ أَنَّ أَهْلَ الْقُرَىٰ آمَنُوا وَاتَّقَوْا لَفَتَحْنَا عَلَيْهِم بَرَكَاتٍ مِّنَ السَّمَاءِ وَالْأَرْضِ وَلَٰكِن كَذَّبُوا فَأَخَذْنَاهُم بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ
Bu fekkoon ne waa dëkk yooyu gëmoon nañu te ragal Yàlla, kon fàwwu Dananu leen ubbil ay wërsëg yu bawoo asamaan ak ci suuf si. Waaye dañoo weddi, Nu sadd leen ngir la ñu daan fàggu ci lu bon.
97أَفَأَمِنَ أَهْلُ الْقُرَىٰ أَن يَأْتِيَهُم بَأْسُنَا بَيَاتًا وَهُمْ نَائِمُونَ
Moo ndax dafa am ci waa dëkk yooyu ñu naagu ne Sunu mbugal duleen dikke ci guddi fekk ñuy nelaw ?
98أَوَأَمِنَ أَهْلُ الْقُرَىٰ أَن يَأْتِيَهُم بَأْسُنَا ضُحًى وَهُمْ يَلْعَبُونَ
Walla dëkk yooyu naagu ne Sunu mbugal duleen dikkal bëccëg fekk ñuy fo ?
Al-A'rafFihi Alxuraan
206Aaya
MeccanRevelation
96Aaya

Tekki — Al-A'raf 96

Simoore Al-A'raf Aaya 96 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu fekkoon ne waa dëkk yooyu gëmoon nañu te ragal…

Simoore Aaya 96/206 — Simoore Al-A'raf الأعراف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-A'raf Dégg, Simoore Al-A'raf Tekki, Simoore Al-A'raf mp3, Simoore Al-A'raf pdf. Aaya 94–98. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers