At-Tawba · 67/129
Tekki Waxtaan — Simoore At-Tawba
الْمُنَافِقُونَ وَالْمُنَافِقَاتُ بَعْضُهُم مِّن بَعْضٍ ۚ يَأْمُرُونَ بِالْمُنكَرِ وَيَنْهَوْنَ عَنِ الْمَعْرُوفِ وَيَقْبِضُونَ أَيْدِيَهُمْ ۚ نَسُوا اللَّهَ فَنَسِيَهُمْ ۗ إِنَّ الْمُنَافِقِينَ هُمُ الْفَاسِقُونَ ۝٦٧
Almunaafiqoona wal munaafiqaatu ba`duhum mim ba`d; yaamuroona bilmunkari wa yanhawna `anil ma`roofi wa yaqbidoona aidiyahum; nasul laaha fanasiyahum; innal munaafiqeena humul faasiqoon
📖 Tekkim Wolof
Naaféq yu góor ya ak naaféq yu jigéen ya dañuy digalante lu bon, dàq lu baax, di téyee seeni yoxo (bañ a joxe). Dañuy fàtte Yàlla ba tax Mu fàtte leen. Naaféq ya ñoom ñooy saay- saay sa.

🎧 Dégg


📜 Aaya 65-69 — Simoore At-Tawba

65وَلَئِن سَأَلْتَهُمْ لَيَقُولُنَّ إِنَّمَا كُنَّا نَخُوضُ وَنَلْعَبُ ۚ قُلْ أَبِاللَّهِ وَآيَاتِهِ وَرَسُولِهِ كُنتُمْ تَسْتَهْزِئُونَ
Te boo leen laajoon, Giñ naa ne danañu wax naan : “Nun dey danu doon caaxaan.”. Neeleen : “Kon daal yéen Yàlla ngeen di fowe ? ”
66لَا تَعْتَذِرُوا قَدْ كَفَرْتُم بَعْدَ إِيمَانِكُمْ ۚ إِن نَّعْفُ عَن طَائِفَةٍ مِّنكُمْ نُعَذِّبْ طَائِفَةً بِأَنَّهُمْ كَانُوا مُجْرِمِينَ
Buleen lay : weddi ngeen ba noppi ginnaaw seen ngëm. Ndeem Dananu jéggal ab kurél ci yéen, Dananu mbugal it ab kurél ngir dañoo nekkoon di ay saay-saay.
67الْمُنَافِقُونَ وَالْمُنَافِقَاتُ بَعْضُهُم مِّن بَعْضٍ ۚ يَأْمُرُونَ بِالْمُنكَرِ وَيَنْهَوْنَ عَنِ الْمَعْرُوفِ وَيَقْبِضُونَ أَيْدِيَهُمْ ۚ نَسُوا اللَّهَ فَنَسِيَهُمْ ۗ إِنَّ الْمُنَافِقِينَ هُمُ الْفَاسِقُونَ
Naaféq yu góor ya ak naaféq yu jigéen ya dañuy digalante lu bon, dàq lu baax, di téyee seeni yoxo (bañ a joxe). Dañuy fàtte Yàlla ba tax Mu fàtte leen. Naaféq ya ñoom ñooy saay- saay sa.
68وَعَدَ اللَّهُ الْمُنَافِقِينَ وَالْمُنَافِقَاتِ وَالْكُفَّارَ نَارَ جَهَنَّمَ خَالِدِينَ فِيهَا ۚ هِيَ حَسْبُهُمْ ۚ وَلَعَنَهُمُ اللَّهُ ۖ وَلَهُمْ عَذَابٌ مُّقِيمٌ
Yàlla dig na naaféq yu góor ya ak naaféq yu jigéen ya ak yéefar ya aw tàngoor ca Safara. Dañu fay béel. Moom doy na leen (mbugal). Te Yàlla rëbb na leen. Am nañu mbugal mu sax.
69كَالَّذِينَ مِن قَبْلِكُمْ كَانُوا أَشَدَّ مِنكُمْ قُوَّةً وَأَكْثَرَ أَمْوَالًا وَأَوْلَادًا فَاسْتَمْتَعُوا بِخَلَاقِهِمْ فَاسْتَمْتَعْتُم بِخَلَاقِكُمْ كَمَا اسْتَمْتَعَ الَّذِينَ مِن قَبْلِكُم بِخَلَاقِهِمْ وَخُضْتُمْ كَالَّذِي خَاضُوا ۚ أُولَٰئِكَ حَبِطَتْ أَعْمَالُهُمْ فِي الدُّنْيَا وَالْآخِرَةِ ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ
Noonu niki ña leen fi jiitu woon : ñoo leen ëppoon doole, ëpp leen alal ak i doom. Bànneexu nañu ci seen cër, yéen it bànneexuleen ci seen cër niki ña leen fi jiitu woon bànneexoo woon ci seeni cër. Te xuus ngeen (ciy caaxaan) na ñu ca xuusee woon. Ñooy ña nga xam ne seen jëf yàqu na ci àddina ak àllaaxira te ñoom yàqule nañu.
At-TawbaFihi Alxuraan
129Aaya
MedinanRevelation
67Aaya

Tekki — At-Tawba 67

Simoore At-Tawba Aaya 67 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Naaféq yu góor ya ak naaféq yu jigéen ya dañuy…

Simoore Aaya 67/129 — Simoore At-Tawba التوبة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore At-Tawba Dégg, Simoore At-Tawba Tekki, Simoore At-Tawba mp3, Simoore At-Tawba pdf. Aaya 65–69. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers