Yunus · 89/109
Tekki Waxtaan — Yunus
قَالَ قَدْ أُجِيبَت دَّعْوَتُكُمَا فَاسْتَقِيمَا وَلَا تَتَّبِعَانِّ سَبِيلَ الَّذِينَ لَا يَعْلَمُونَ ۝٨٩
Qaala qad ujeebad da`watukumaa fastaqeemaa wa laa tattabi`aaanni sabeelal lazeena laaya`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Mu ne leen : “Nangoof na seeni ñaan. Taxawleen temm yéen ñaar ci bañ a topp yoonu ña xamule”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 87-91 — Yunus

87وَأَوْحَيْنَا إِلَىٰ مُوسَىٰ وَأَخِيهِ أَن تَبَوَّءَا لِقَوْمِكُمَا بِمِصْرَ بُيُوتًا وَاجْعَلُوا بُيُوتَكُمْ قِبْلَةً وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ ۗ وَبَشِّرِ الْمُؤْمِنِينَ
Nu jox Muusaa ak mbokkam ma ndigal, ne leen : “Sàkkleen néeg ca Misra ca seen biiru nit, te ngeen def seen néeg jàkka te nangeen di taxawal julli. Te di bégloo ñi gëm [ca seenug waare]”.
88وَقَالَ مُوسَىٰ رَبَّنَا إِنَّكَ آتَيْتَ فِرْعَوْنَ وَمَلَأَهُ زِينَةً وَأَمْوَالًا فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا رَبَّنَا لِيُضِلُّوا عَن سَبِيلِكَ ۖ رَبَّنَا اطْمِسْ عَلَىٰ أَمْوَالِهِمْ وَاشْدُدْ عَلَىٰ قُلُوبِهِمْ فَلَا يُؤْمِنُوا حَتَّىٰ يَرَوُا الْعَذَابَ الْأَلِيمَ
Muusaa ne : "Yaw sunu Boroom, may nga Firawna ak u nitam taar ak alal ci alali àddina. Yaw sunu Boroom, ña réer moy saw yoon, faral seen alal ya te nga fatt seeni xol, duñu gëm mukk ndare bu ñu gisee mbugal mu tar ma”.
89قَالَ قَدْ أُجِيبَت دَّعْوَتُكُمَا فَاسْتَقِيمَا وَلَا تَتَّبِعَانِّ سَبِيلَ الَّذِينَ لَا يَعْلَمُونَ
Mu ne leen : “Nangoof na seeni ñaan. Taxawleen temm yéen ñaar ci bañ a topp yoonu ña xamule”.
90۞ وَجَاوَزْنَا بِبَنِي إِسْرَائِيلَ الْبَحْرَ فَأَتْبَعَهُمْ فِرْعَوْنُ وَجُنُودُهُ بَغْيًا وَعَدْوًا ۖ حَتَّىٰ إِذَا أَدْرَكَهُ الْغَرَقُ قَالَ آمَنتُ أَنَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا الَّذِي آمَنَتْ بِهِ بَنُو إِسْرَائِيلَ وَأَنَا مِنَ الْمُسْلِمِينَ
Nu jàlle waa Banii-Israayiila géej ga. Firawna topp leen ak lelam [ay xarekatam] ngir mbewte ak ug noonu. Ba lab ga agsee ci moom, mu ne : “Gëm naa ne lay mbir moo di ne : amul jeneen yàlla ju dul Ji waa Banii-Israayiila gëm. Te man bokk naa ci way-wommatu ña”.
91آلْآنَ وَقَدْ عَصَيْتَ قَبْلُ وَكُنتَ مِنَ الْمُفْسِدِينَ
[Yàlla ne ko] : Moo ndax léegi [ngay door a gëm] ? Te nga féttéerlu woon lu jiitu te nga bokk ca yàqkat ya !
YunusFihi Alxuraan
109Aaya
MeccanRevelation
89Aaya

Tekki — Yunus 89

Simoore Yunus Aaya 89 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu ne leen : “Nangoof na seeni ñaan. Taxawleen temm…

Simoore Aaya 89/109 — Yunus يونس (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yunus Dégg, Yunus Tekki, Yunus mp3, Yunus pdf. Aaya 87–91. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers