Hud · 18/123
Tekki Waxtaan — Hud
وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا ۚ أُولَٰئِكَ يُعْرَضُونَ عَلَىٰ رَبِّهِمْ وَيَقُولُ الْأَشْهَادُ هَٰؤُلَاءِ الَّذِينَ كَذَبُوا عَلَىٰ رَبِّهِمْ ۚ أَلَا لَعْنَةُ اللَّهِ عَلَى الظَّالِمِينَ ۝١٨
Wa man azlamu mimmanif taraa `alal laahi kazibaa; ulaaa`ika yu`radoona `alaa Rabbihim wa yaqoolul ashhaa duhaaa`ulaaa`il lazeena kazaboo `alaa Rabbihim; alaa la`natul laahi alaz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Ana kan moo gën a tooñ ku sosal Yàlla ay fen ? Ñooña danañu leen teewal, gaaral leen fa seen Boroom, seede ya daldi wax ne : “Ñii ñooy ña doon fen ci seen Boroom”. Moo ndax rëbbum Yàlla du wàcc ci kaw tooñkat yi waay !

🎧 Dégg


📜 Aaya 16-20 — Hud

16أُولَٰئِكَ الَّذِينَ لَيْسَ لَهُمْ فِي الْآخِرَةِ إِلَّا النَّارُ ۖ وَحَبِطَ مَا صَنَعُوا فِيهَا وَبَاطِلٌ مَّا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ñooña ñoo dul am ca àllaaxira lu dul Safara. Te la ñu liggéeyoon yàqu na, te it la ñu doon def ag neen la.
17أَفَمَن كَانَ عَلَىٰ بَيِّنَةٍ مِّن رَّبِّهِ وَيَتْلُوهُ شَاهِدٌ مِّنْهُ وَمِن قَبْلِهِ كِتَابُ مُوسَىٰ إِمَامًا وَرَحْمَةً ۚ أُولَٰئِكَ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۚ وَمَن يَكْفُرْ بِهِ مِنَ الْأَحْزَابِ فَالنَّارُ مَوْعِدُهُ ۚ فَلَا تَكُ فِي مِرْيَةٍ مِّنْهُ ۚ إِنَّهُ الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يُؤْمِنُونَ
Moo ndax ku tënku ci [Téere] ba tukkee ca Boroomam te mu am seede su tukkee ca Moom di ko jàng ci ndigalam, [dana niroo ak ñooña] ? te la ko jiitu, téereb Muusaa jaaroon na fa di gindee, di yërmaande itam. Am na ñu ko gëmoon. ku ko weddi ca sàmm sa, Safara mooy nekk li muy dajeel. Bul am benn sikki-sàkka. Te moom mooy dëgg gu tukkee ca sa Boroom ; waaye li ëpp ci nit ñi duñu gëm.
18وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّنِ افْتَرَىٰ عَلَى اللَّهِ كَذِبًا ۚ أُولَٰئِكَ يُعْرَضُونَ عَلَىٰ رَبِّهِمْ وَيَقُولُ الْأَشْهَادُ هَٰؤُلَاءِ الَّذِينَ كَذَبُوا عَلَىٰ رَبِّهِمْ ۚ أَلَا لَعْنَةُ اللَّهِ عَلَى الظَّالِمِينَ
Ana kan moo gën a tooñ ku sosal Yàlla ay fen ? Ñooña danañu leen teewal, gaaral leen fa seen Boroom, seede ya daldi wax ne : “Ñii ñooy ña doon fen ci seen Boroom”. Moo ndax rëbbum Yàlla du wàcc ci kaw tooñkat yi waay !
19الَّذِينَ يَصُدُّونَ عَن سَبِيلِ اللَّهِ وَيَبْغُونَهَا عِوَجًا وَهُم بِالْآخِرَةِ هُمْ كَافِرُونَ
Ñoo di ñay wëlbati [nit ña] ngir ñu bañ a jëm ci yoonu Yàlla, di sàkkal diine ay sikk, boole ca ñoom gëmuñu àllaaxira.
20أُولَٰئِكَ لَمْ يَكُونُوا مُعْجِزِينَ فِي الْأَرْضِ وَمَا كَانَ لَهُم مِّن دُونِ اللَّهِ مِنْ أَوْلِيَاءَ ۘ يُضَاعَفُ لَهُمُ الْعَذَابُ ۚ مَا كَانُوا يَسْتَطِيعُونَ السَّمْعَ وَمَا كَانُوا يُبْصِرُونَ
Ñooña duñu mën a raw [rëcc] Yàlla ci kaw suuf si ! Te duñu mën a am ku leen wallu, deef na leen fulal mbugal ma. Ngir ñoom mënuñu woon a am dégg-dégg ak gis-gis.
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
18Aaya

Tekki — Hud 18

Simoore Hud Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana kan moo gën a tooñ ku sosal Yàlla ay…

Simoore Aaya 18/123 — Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Hud Dégg, Hud Tekki, Hud mp3, Hud pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers