Hud · 96/123
Tekki Waxtaan — Simoore Hud
وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مُوسَىٰ بِآيَاتِنَا وَسُلْطَانٍ مُّبِينٍ ۝٩٦
Wa laqad arsalnaa Moosaa bi Aayaatinaa wa sultaanim mubeen
📖 Tekkim Wolof
Te yónni woon Nanu Muusaa mu ànd ak Sunuy kaawtéef ak lay yu leer nàññ,

🎧 Dégg


📜 Aaya 94-98 — Simoore Hud

94وَلَمَّا جَاءَ أَمْرُنَا نَجَّيْنَا شُعَيْبًا وَالَّذِينَ آمَنُوا مَعَهُ بِرَحْمَةٍ مِّنَّا وَأَخَذَتِ الَّذِينَ ظَلَمُوا الصَّيْحَةُ فَأَصْبَحُوا فِي دِيَارِهِمْ جَاثِمِينَ
Ba Sunu ndigal agsee, musal Nanu Suhaybu ak ña gëmoon ànd ak moom ci Sunu yërmaande. Ag xaacu faagaagal ña tooñ, ñu mujj xëy ne lànjaŋ dee fa seen kër ya,
95كَأَن لَّمْ يَغْنَوْا فِيهَا ۗ أَلَا بُعْدًا لِّمَدْيَنَ كَمَا بَعِدَتْ ثَمُودُ
mu mel ni masuñu fa woon a dëkk. Waaw, ndax alkaande dalul waa Madyaana na mu alake woon waa Samuuda ?.
96وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مُوسَىٰ بِآيَاتِنَا وَسُلْطَانٍ مُّبِينٍ
Te yónni woon Nanu Muusaa mu ànd ak Sunuy kaawtéef ak lay yu leer nàññ,
97إِلَىٰ فِرْعَوْنَ وَمَلَئِهِ فَاتَّبَعُوا أَمْرَ فِرْعَوْنَ ۖ وَمَا أَمْرُ فِرْعَوْنَ بِرَشِيدٍ
ca Firawna ak boroom darajaam ya. Ñu topp ndigalu Firawna, te ndigalu Firawna jubul woon.
98يَقْدُمُ قَوْمَهُ يَوْمَ الْقِيَامَةِ فَأَوْرَدَهُمُ النَّارَ ۖ وَبِئْسَ الْوِرْدُ الْمَوْرُودُ
Dana jiite aw nitam Bis-pénc ba. Tàbbal leen Safara. Ndaw tàbbikaay bu bon !
HudFihi Alxuraan
123Aaya
MeccanRevelation
96Aaya

Tekki — Hud 96

Simoore Hud Aaya 96 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te yónni woon Nanu Muusaa mu ànd ak Sunuy kaawtéef…

Simoore Aaya 96/123 — Simoore Hud هود (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Hud Dégg, Simoore Hud Tekki, Simoore Hud mp3, Simoore Hud pdf. Aaya 94–98. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers