Yusuf · 79/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
قَالَ مَعَاذَ اللَّهِ أَن نَّأْخُذَ إِلَّا مَن وَجَدْنَا مَتَاعَنَا عِندَهُ إِنَّا إِذًا لَّظَالِمُونَ ۝٧٩
Qaala ma`aazal laahi an naakhuza illaa manw wajadnaa mataa`anaa `indahoo innaaa izal lazaalimoon
📖 Tekkim Wolof
- Mu ne : “Maa ngi ñaan Yàlla mu musal ma ci jàpp ku dul ka ma fekk nattukaay ci moom ! [Su nu ko defee], kon dananu bokk ca tooñkat ya.
🎧 Dégg

📜 Aaya 77-81 — Yusuf

77۞ قَالُوا إِن يَسْرِقْ فَقَدْ سَرَقَ أَخٌ لَّهُ مِن قَبْلُ ۚ فَأَسَرَّهَا يُوسُفُ فِي نَفْسِهِ وَلَمْ يُبْدِهَا لَهُمْ ۚ قَالَ أَنتُمْ شَرٌّ مَّكَانًا ۖ وَاللَّهُ أَعْلَمُ بِمَا تَصِفُونَ
Ñu ne : “Ndegam sàcc na, am na doomu-ndeyam ju sàccoon bu jëkk. “Yuusufa nëbb ca xelam la mu xalaat, bañ leen koo feeñal. Mu ne [ci xelam] : “Yéen yées ngeen ! Te Yàlla xam na li ngeen jëf”.
78قَالُوا يَا أَيُّهَا الْعَزِيزُ إِنَّ لَهُ أَبًا شَيْخًا كَبِيرًا فَخُذْ أَحَدَنَا مَكَانَهُ ۖ إِنَّا نَرَاكَ مِنَ الْمُحْسِنِينَ
- Ñu ne : "Ay yaw kilifa gi, moom dafa am baay bu mage lool ; téyeel kenn ci nun bàyyi ko. Gis nanu ne yaw bokk nga ca rafetalkat ya [seeni jëf]”.
79قَالَ مَعَاذَ اللَّهِ أَن نَّأْخُذَ إِلَّا مَن وَجَدْنَا مَتَاعَنَا عِندَهُ إِنَّا إِذًا لَّظَالِمُونَ
- Mu ne : “Maa ngi ñaan Yàlla mu musal ma ci jàpp ku dul ka ma fekk nattukaay ci moom ! [Su nu ko defee], kon dananu bokk ca tooñkat ya.
80فَلَمَّا اسْتَيْأَسُوا مِنْهُ خَلَصُوا نَجِيًّا ۖ قَالَ كَبِيرُهُمْ أَلَمْ تَعْلَمُوا أَنَّ أَبَاكُمْ قَدْ أَخَذَ عَلَيْكُم مَّوْثِقًا مِّنَ اللَّهِ وَمِن قَبْلُ مَا فَرَّطتُمْ فِي يُوسُفَ ۖ فَلَنْ أَبْرَحَ الْأَرْضَ حَتَّىٰ يَأْذَنَ لِي أَبِي أَوْ يَحْكُمَ اللَّهُ لِي ۖ وَهُوَ خَيْرُ الْحَاكِمِينَ
Ba ñu amatul yaakaar ci moom, beru nañu di diisoo. Ka di seen mag ne : “Moo ndax dangeen a fàtte ne seen baay waatloo woon na leen ci Yàlla, ca la jiitu loolu la ngeen defoon Yuusufa ? Man dey du ma fi jóge ba kerook may jot sama ndigalul baay walla Yàlla àtte ma, ndax Moom moo gën a mën a àtte àttekat ya.
81ارْجِعُوا إِلَىٰ أَبِيكُمْ فَقُولُوا يَا أَبَانَا إِنَّ ابْنَكَ سَرَقَ وَمَا شَهِدْنَا إِلَّا بِمَا عَلِمْنَا وَمَا كُنَّا لِلْغَيْبِ حَافِظِينَ
[Mu ne] demleen ca seen baay, ngeen ne ko : “Yaw sunu baay, sa doon ja sàcc na. Te dunu seede lu dul la nu xam. Te nun xamunu kumpa.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
79Aaya

Tekki — Yusuf 79

Simoore Yusuf Aaya 79 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : - Mu ne : “Maa ngi ñaan Yàlla mu musal…

Simoore Aaya 79/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 77–81. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers