Yusuf · 82/111
Tekki Waxtaan — Yusuf
وَاسْأَلِ الْقَرْيَةَ الَّتِي كُنَّا فِيهَا وَالْعِيرَ الَّتِي أَقْبَلْنَا فِيهَا ۖ وَإِنَّا لَصَادِقُونَ ۝٨٢
Was`alil qaryatal latee kunnaa feehaa wal`eeral lateee aqbalnaa feehaa wa innaa lasaadiqoon
📖 Tekkim Wolof
Laajal waa dëkk ba nu nekkoon, ak njëgg ma nu àndaloon ñibbisi. Li nu wax dëgg la.”
🎧 Dégg

📜 Aaya 80-84 — Yusuf

80فَلَمَّا اسْتَيْأَسُوا مِنْهُ خَلَصُوا نَجِيًّا ۖ قَالَ كَبِيرُهُمْ أَلَمْ تَعْلَمُوا أَنَّ أَبَاكُمْ قَدْ أَخَذَ عَلَيْكُم مَّوْثِقًا مِّنَ اللَّهِ وَمِن قَبْلُ مَا فَرَّطتُمْ فِي يُوسُفَ ۖ فَلَنْ أَبْرَحَ الْأَرْضَ حَتَّىٰ يَأْذَنَ لِي أَبِي أَوْ يَحْكُمَ اللَّهُ لِي ۖ وَهُوَ خَيْرُ الْحَاكِمِينَ
Ba ñu amatul yaakaar ci moom, beru nañu di diisoo. Ka di seen mag ne : “Moo ndax dangeen a fàtte ne seen baay waatloo woon na leen ci Yàlla, ca la jiitu loolu la ngeen defoon Yuusufa ? Man dey du ma fi jóge ba kerook may jot sama ndigalul baay walla Yàlla àtte ma, ndax Moom moo gën a mën a àtte àttekat ya.
81ارْجِعُوا إِلَىٰ أَبِيكُمْ فَقُولُوا يَا أَبَانَا إِنَّ ابْنَكَ سَرَقَ وَمَا شَهِدْنَا إِلَّا بِمَا عَلِمْنَا وَمَا كُنَّا لِلْغَيْبِ حَافِظِينَ
[Mu ne] demleen ca seen baay, ngeen ne ko : “Yaw sunu baay, sa doon ja sàcc na. Te dunu seede lu dul la nu xam. Te nun xamunu kumpa.
82وَاسْأَلِ الْقَرْيَةَ الَّتِي كُنَّا فِيهَا وَالْعِيرَ الَّتِي أَقْبَلْنَا فِيهَا ۖ وَإِنَّا لَصَادِقُونَ
Laajal waa dëkk ba nu nekkoon, ak njëgg ma nu àndaloon ñibbisi. Li nu wax dëgg la.”
83قَالَ بَلْ سَوَّلَتْ لَكُمْ أَنفُسُكُمْ أَمْرًا ۖ فَصَبْرٌ جَمِيلٌ ۖ عَسَى اللَّهُ أَن يَأْتِيَنِي بِهِمْ جَمِيعًا ۚ إِنَّهُ هُوَ الْعَلِيمُ الْحَكِيمُ
[Seen baay tontu leen] ne : “Deewallaay dangeen a topp seen bakkan mu rafetal leen am mbir !... [Muñ gu rafet]. Xéy-na Yàlla delloosil nu leen ñoom ñépp. Moom Yàlla Ku xereñ la, Ku xam la”.
84وَتَوَلَّىٰ عَنْهُمْ وَقَالَ يَا أَسَفَىٰ عَلَىٰ يُوسُفَ وَابْيَضَّتْ عَيْنَاهُ مِنَ الْحُزْنِ فَهُوَ كَظِيمٌ
Mu dummóoyu leen, wax ne : “Céy sama njàqare ci Yuusufa ! ”. Noona ay gëtam weex [gisatul] ngir mer ma mu wann.
YusufFihi Alxuraan
111Aaya
MeccanRevelation
82Aaya

Tekki — Yusuf 82

Simoore Yusuf Aaya 82 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Laajal waa dëkk ba nu nekkoon, ak njëgg ma nu…

Simoore Aaya 82/111 — Yusuf يوسف (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Yusuf Dégg, Yusuf Tekki, Yusuf mp3, Yusuf pdf. Aaya 80–84. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers