Al-Baqara · 123/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
وَاتَّقُوا يَوْمًا لَّا تَجْزِي نَفْسٌ عَن نَّفْسٍ شَيْئًا وَلَا يُقْبَلُ مِنْهَا عَدْلٌ وَلَا تَنفَعُهَا شَفَاعَةٌ وَلَا هُمْ يُنصَرُونَ ۝١٢٣
Wattaqoo yawmal laa tajzee nafsun `an nafsin shai `anw wa laa yuqbalu minhaa `adlunw wa laa tanfa`uhaa shafaa `atunw wa laa hum yunsaroon
📖 Tekkim Wolof
Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara beneen bakkan te deesu ko nangul njotu, rammu it du ko fa jariñ. Te duñu fa am ndimbal.

🎧 Dégg


📜 Aaya 121-125 — Simoore Al-Baqara

121الَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَتْلُونَهُ حَقَّ تِلَاوَتِهِ أُولَٰئِكَ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۗ وَمَن يَكْفُرْ بِهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ
Ña nga xam ne jox Nanu leen téere ba [Alxuraan], danañu ko jànge na mu yelle, ñooña ñoo ko gëm. Ña ko weddi ñooy way-ñàkk ña.
122يَا بَنِي إِسْرَائِيلَ اذْكُرُوا نِعْمَتِيَ الَّتِي أَنْعَمْتُ عَلَيْكُمْ وَأَنِّي فَضَّلْتُكُمْ عَلَى الْعَالَمِينَ
Yéen Banii-Israayil, fàttalikuleen Sama xéewal yi Ma leen xéewale woon te Man ma defoon leen ngeen gënoon ci kaw mbindéef yépp..
123وَاتَّقُوا يَوْمًا لَّا تَجْزِي نَفْسٌ عَن نَّفْسٍ شَيْئًا وَلَا يُقْبَلُ مِنْهَا عَدْلٌ وَلَا تَنفَعُهَا شَفَاعَةٌ وَلَا هُمْ يُنصَرُونَ
Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara beneen bakkan te deesu ko nangul njotu, rammu it du ko fa jariñ. Te duñu fa am ndimbal.
124۞ وَإِذِ ابْتَلَىٰ إِبْرَاهِيمَ رَبُّهُ بِكَلِمَاتٍ فَأَتَمَّهُنَّ ۖ قَالَ إِنِّي جَاعِلُكَ لِلنَّاسِ إِمَامًا ۖ قَالَ وَمِن ذُرِّيَّتِي ۖ قَالَ لَا يَنَالُ عَهْدِي الظَّالِمِينَ
[Fàttalikuleen,] Ibraahiima, ba ko Boroomam nattoo, ciy ndigal, mu matal leen, Mu ne ko : “Def Naa la njiit ci nit ñi”. - Ibraayiima ne ko : “[Defal ko] it samay sët”. Mu ne ko : “Sama kóllare du ma ci boole way-tooñ ña de”.
125وَإِذْ جَعَلْنَا الْبَيْتَ مَثَابَةً لِّلنَّاسِ وَأَمْنًا وَاتَّخِذُوا مِن مَّقَامِ إِبْرَاهِيمَ مُصَلًّى ۖ وَعَهِدْنَا إِلَىٰ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ أَن طَهِّرَا بَيْتِيَ لِلطَّائِفِينَ وَالْعَاكِفِينَ وَالرُّكَّعِ السُّجُودِ
[Fàttalikuleen], ba Nu defee Néeg ba muy delluwaayub nit ñi ak barabub kóolute - Te nangeen def (Màqaama Ibraahiima) barabub jullikaay, - Nu kóllarante ak (Ibraahiima) ak (Ismaahiila) : “Ne leen nangeen sellal Sama Néeg bi ngir ñi koy wër, ak ñi fay toog, di fa rukkoo ak di fa sujjóot [julli].
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
123Aaya

Tekki — Al-Baqara 123

Simoore Al-Baqara Aaya 123 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara…

Simoore Aaya 123/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 121–125. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers