Al-Baqara · 90/286
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Baqara
بِئْسَمَا اشْتَرَوْا بِهِ أَنفُسَهُمْ أَن يَكْفُرُوا بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ بَغْيًا أَن يُنَزِّلَ اللَّهُ مِن فَضْلِهِ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ ۖ فَبَاءُوا بِغَضَبٍ عَلَىٰ غَضَبٍ ۚ وَلِلْكَافِرِينَ عَذَابٌ مُّهِينٌ ۝٩٠
Bi`samash taraw biheee anfusahum ai yakfuroo bimaaa anzalal laahu baghyan ai yunazzilal laahu min fadlilhee `alaa mai yashaaa`u min ibaadihee fabaaa`oo bighadabin `alaa ghadab; wa lilkaafireena `azaabum muheen
📖 Tekkim Wolof
Bon na, la ñu jaayee seeni bakkan ! Ba tax ñu weddi la Yàlla wàcce ngir bew, te iñaan ci li Yàlla wàcce ngënéelam ci ku ko soob ciy jaamam. Ba daldi nañuy mer bay fuuñ-fuuñi, te yéefar yi am nañu mbugal muy toroxale !

🎧 Dégg


📜 Aaya 88-92 — Simoore Al-Baqara

88وَقَالُوا قُلُوبُنَا غُلْفٌ ۚ بَل لَّعَنَهُمُ اللَّهُ بِكُفْرِهِمْ فَقَلِيلًا مَّا يُؤْمِنُونَ
Ñu naan : “Sunuy xol muuru na [ci li Yonent bi wax]” - Li am ba des moo di Yàlla rëbb na leen ci sababus seenug weddi, te néewaana bu ñu gëmee.
89وَلَمَّا جَاءَهُمْ كِتَابٌ مِّنْ عِندِ اللَّهِ مُصَدِّقٌ لِّمَا مَعَهُمْ وَكَانُوا مِن قَبْلُ يَسْتَفْتِحُونَ عَلَى الَّذِينَ كَفَرُوا فَلَمَّا جَاءَهُم مَّا عَرَفُوا كَفَرُوا بِهِ ۚ فَلَعْنَةُ اللَّهِ عَلَى الْكَافِرِينَ
[Fàttalikuleen] ba leen ab Téere dikkalee, jóge ca Yàlla, di dëggal la ñu yor, - fekk lu jiitu loolu daan nañu ñaan noteel ci yéefar yi, - te ba la ñu xamoon [te daan ko séenu] egsee ca ñoom, dañu koo weddi. Rëbbum Yàlla dal na yéefar yi !
90بِئْسَمَا اشْتَرَوْا بِهِ أَنفُسَهُمْ أَن يَكْفُرُوا بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ بَغْيًا أَن يُنَزِّلَ اللَّهُ مِن فَضْلِهِ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ ۖ فَبَاءُوا بِغَضَبٍ عَلَىٰ غَضَبٍ ۚ وَلِلْكَافِرِينَ عَذَابٌ مُّهِينٌ
Bon na, la ñu jaayee seeni bakkan ! Ba tax ñu weddi la Yàlla wàcce ngir bew, te iñaan ci li Yàlla wàcce ngënéelam ci ku ko soob ciy jaamam. Ba daldi nañuy mer bay fuuñ-fuuñi, te yéefar yi am nañu mbugal muy toroxale !
91وَإِذَا قِيلَ لَهُمْ آمِنُوا بِمَا أَنزَلَ اللَّهُ قَالُوا نُؤْمِنُ بِمَا أُنزِلَ عَلَيْنَا وَيَكْفُرُونَ بِمَا وَرَاءَهُ وَهُوَ الْحَقُّ مُصَدِّقًا لِّمَا مَعَهُمْ ۗ قُلْ فَلِمَ تَقْتُلُونَ أَنبِيَاءَ اللَّهِ مِن قَبْلُ إِن كُنتُم مُّؤْمِنِينَ
Bu ñu leen waxee ne : “Gëmleen li Yàlla wàcce”, Ñu ne : “Gëm nañu li ñu wàcce ci nun”. Te ñoom weddi nañu la ñëw ginnaawam te muy dëggal la ñu yore. - Neel : “Lu taxoon ngeen rey ay Yonentiy Yàlla, ca bu jëkk ndegam gëm ngeen ? ”.
92۞ وَلَقَدْ جَاءَكُم مُّوسَىٰ بِالْبَيِّنَاتِ ثُمَّ اتَّخَذْتُمُ الْعِجْلَ مِن بَعْدِهِ وَأَنتُمْ ظَالِمُونَ
Wóor na céŋŋ ne Muusaa digaloon na leen àndak ay kéemaam yu leer. Ba noppi ngeen jaamu sëll wa ginnaawam, ngeen di way-tooñ.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
90Aaya

Tekki — Al-Baqara 90

Simoore Al-Baqara Aaya 90 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bon na, la ñu jaayee seeni bakkan ! Ba tax…

Simoore Aaya 90/286 — Simoore Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Baqara Dégg, Simoore Al-Baqara Tekki, Simoore Al-Baqara mp3, Simoore Al-Baqara pdf. Aaya 88–92. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers