Taha · 73/135
Tekki Waxtaan — Taha
إِنَّا آمَنَّا بِرَبِّنَا لِيَغْفِرَ لَنَا خَطَايَانَا وَمَا أَكْرَهْتَنَا عَلَيْهِ مِنَ السِّحْرِ ۗ وَاللَّهُ خَيْرٌ وَأَبْقَىٰ ۝٧٣
Innaaa aamannaa bi Rabbinaa liyaghfira lanaa khataayaanaa wa maaa akrahtanaa `alaihi minas sihr; wallaahu khairunw waabqaa
📖 Tekkim Wolof
Nun dey gëm nanu sunu Boroom ngir mu jéggal nu sunuy bàkkaar, ak njibar gii nga nu jaay doole ba tax nu def ko”. Te Yàlla Moo gën te Mooy des.
🎧 Dégg

📜 Aaya 71-75 — Taha

71قَالَ آمَنتُمْ لَهُ قَبْلَ أَنْ آذَنَ لَكُمْ ۖ إِنَّهُ لَكَبِيرُكُمُ الَّذِي عَلَّمَكُمُ السِّحْرَ ۖ فَلَأُقَطِّعَنَّ أَيْدِيَكُمْ وَأَرْجُلَكُم مِّنْ خِلَافٍ وَلَأُصَلِّبَنَّكُمْ فِي جُذُوعِ النَّخْلِ وَلَتَعْلَمُنَّ أَيُّنَا أَشَدُّ عَذَابًا وَأَبْقَىٰ
[Firawna] ne leen : “Gëmoon ngeen ko la jiitu lii. [Xam naa ne] Muusaa mooy kàndiŋ mi leen jàngal ag njibar. Danaa dàgg seeni tànk ak seeni yoxo cig jàllawle, danaa leen daaj ci dàtti tàndarma yi, dangeen xam kan ci nun moo gën a mettile te gën a tarle mbugal”.
72قَالُوا لَن نُّؤْثِرَكَ عَلَىٰ مَا جَاءَنَا مِنَ الْبَيِّنَاتِ وَالَّذِي فَطَرَنَا ۖ فَاقْضِ مَا أَنتَ قَاضٍ ۖ إِنَّمَا تَقْضِي هَٰذِهِ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا
Ñu ne ko : “Yàlla mi ñu bind ak kàddoom yii Mu nu indil moo nu la gënal fàwwu. Dogalal loo bëgg a dogal. Waaye nag say àtte moom àddina rekk la yem.
73إِنَّا آمَنَّا بِرَبِّنَا لِيَغْفِرَ لَنَا خَطَايَانَا وَمَا أَكْرَهْتَنَا عَلَيْهِ مِنَ السِّحْرِ ۗ وَاللَّهُ خَيْرٌ وَأَبْقَىٰ
Nun dey gëm nanu sunu Boroom ngir mu jéggal nu sunuy bàkkaar, ak njibar gii nga nu jaay doole ba tax nu def ko”. Te Yàlla Moo gën te Mooy des.
74إِنَّهُ مَن يَأْتِ رَبَّهُ مُجْرِمًا فَإِنَّ لَهُ جَهَنَّمَ لَا يَمُوتُ فِيهَا وَلَا يَحْيَىٰ
Kuy saay-saay ba dem fa Boroomam, dana tàbbi Safara te du fa dee du fa dundu.
75وَمَن يَأْتِهِ مُؤْمِنًا قَدْ عَمِلَ الصَّالِحَاتِ فَأُولَٰئِكَ لَهُمُ الدَّرَجَاتُ الْعُلَىٰ
Kuy gëm Yàlla ak a def u yiw ba dem fa Yàlla, ñooña danañu am ay daraja yu kawe,
TahaFihi Alxuraan
135Aaya
MeccanRevelation
73Aaya

Tekki — Taha 73

Simoore Taha Aaya 73 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nun dey gëm nanu sunu Boroom ngir mu jéggal nu…

Simoore Aaya 73/135 — Taha طه (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Taha Dégg, Taha Tekki, Taha mp3, Taha pdf. Aaya 71–75. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers