Al-Anbiya · 90/112
Tekki Waxtaan — Al-Anbiya
فَاسْتَجَبْنَا لَهُ وَوَهَبْنَا لَهُ يَحْيَىٰ وَأَصْلَحْنَا لَهُ زَوْجَهُ ۚ إِنَّهُمْ كَانُوا يُسَارِعُونَ فِي الْخَيْرَاتِ وَيَدْعُونَنَا رَغَبًا وَرَهَبًا ۖ وَكَانُوا لَنَا خَاشِعِينَ ۝٩٠
Fastajabnaa lahoo wa wahabnaa lahoo Yahyaa Wa aslahnaa lahoo zawjah; innahum kaanoo yusaari`oona fil khairaati wa yad`oonanaa raghabanw wa rahabaa; wa kaanoo lanaa khaashi`een
📖 Tekkim Wolof
Nu nangul ko, may ko Yahyaa te Nu yéwénalal ko soxnaam. Ñoom sax dañu daan njëkkante ci jëf yu yiw ya te ñoom daanañu Nu jaamu, nekk ci diggante xemmem ak ragal. Te nekkoon nañu diy way-toroxlu ci Nun.

🎧 Dégg


📜 Aaya 88-92 — Al-Anbiya

88فَاسْتَجَبْنَا لَهُ وَنَجَّيْنَاهُ مِنَ الْغَمِّ ۚ وَكَذَٰلِكَ نُنجِي الْمُؤْمِنِينَ
Nu daldi koy nangul te musal ko ca njàqare ja. Te it noonu la Nuy musalee way-gëm ña.
89وَزَكَرِيَّا إِذْ نَادَىٰ رَبَّهُ رَبِّ لَا تَذَرْنِي فَرْدًا وَأَنتَ خَيْرُ الْوَارِثِينَ
[Fàttalikul it] Zakariyaa ba mu woowee Boroomam ne : “Boroom sama, bul ma bàyyi ma wéet, te Yaa di ku gën a mën a dimbalee”.
90فَاسْتَجَبْنَا لَهُ وَوَهَبْنَا لَهُ يَحْيَىٰ وَأَصْلَحْنَا لَهُ زَوْجَهُ ۚ إِنَّهُمْ كَانُوا يُسَارِعُونَ فِي الْخَيْرَاتِ وَيَدْعُونَنَا رَغَبًا وَرَهَبًا ۖ وَكَانُوا لَنَا خَاشِعِينَ
Nu nangul ko, may ko Yahyaa te Nu yéwénalal ko soxnaam. Ñoom sax dañu daan njëkkante ci jëf yu yiw ya te ñoom daanañu Nu jaamu, nekk ci diggante xemmem ak ragal. Te nekkoon nañu diy way-toroxlu ci Nun.
91وَالَّتِي أَحْصَنَتْ فَرْجَهَا فَنَفَخْنَا فِيهَا مِن رُّوحِنَا وَجَعَلْنَاهَا وَابْنَهَا آيَةً لِّلْعَالَمِينَ
Ak jigéen ja ñoŋal boppam [Maryam] ! Nu wal ci moom lenn ci Sunu ruu, daldi koy def mook doomam [Iisaa] ñuy kaawtéef ci àddina si yépp.
92إِنَّ هَٰذِهِ أُمَّتُكُمْ أُمَّةً وَاحِدَةً وَأَنَا رَبُّكُمْ فَاعْبُدُونِ
Lii nag moo di seen diine, mu di jenn diine doŋŋ, te Man maa di seen Boroom. Waay- waay kon jaamuleen Ma.
Al-AnbiyaFihi Alxuraan
112Aaya
MeccanRevelation
90Aaya

Tekki — Al-Anbiya 90

Simoore Al-Anbiya Aaya 90 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nu nangul ko, may ko Yahyaa te Nu yéwénalal ko…

Simoore Aaya 90/112 — Al-Anbiya الأنبياء (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Anbiya Dégg, Al-Anbiya Tekki, Al-Anbiya mp3, Al-Anbiya pdf. Aaya 88–92. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers