Al-Hajj · 58/78
Tekki Waxtaan — Al-Hajj
وَالَّذِينَ هَاجَرُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ ثُمَّ قُتِلُوا أَوْ مَاتُوا لَيَرْزُقَنَّهُمُ اللَّهُ رِزْقًا حَسَنًا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَهُوَ خَيْرُ الرَّازِقِينَ ۝٥٨
Wallazeena haajaroo fee sabeelil laahi summa qutilooo law maatoo la yarzuqan nahumul laahu rizqan hasanaa; wa innal laaha la Huwa khairur raaziqeen
📖 Tekkim Wolof
Ña gàdday ngir liggéey ci yoonu Yàlla, topp ñu rey leen mbaa ñu dee, fàwwu Yàlla dana leen wërsëgal wërsëg wu rafet, te nag Yàlla moo di Ki gën a mën a wërsëgal ci képp kuy wërsëgal.

🎧 Dégg


📜 Aaya 56-60 — Al-Hajj

56الْمُلْكُ يَوْمَئِذٍ لِّلَّهِ يَحْكُمُ بَيْنَهُمْ ۚ فَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فِي جَنَّاتِ النَّعِيمِ
Bis niki tey nguur gi Yàllaa lo moom. Dana àtte seen diggante. Kon ña gëm tey jëf jëf ju yiw, danañu nekk ci Àjjanay xéewal,
57وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا فَأُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ مُّهِينٌ
waaye ña weddi te jàppe ay fen Sunuy kàddu, ñooña ñeel na leen mbugal muy toroxale !
58وَالَّذِينَ هَاجَرُوا فِي سَبِيلِ اللَّهِ ثُمَّ قُتِلُوا أَوْ مَاتُوا لَيَرْزُقَنَّهُمُ اللَّهُ رِزْقًا حَسَنًا ۚ وَإِنَّ اللَّهَ لَهُوَ خَيْرُ الرَّازِقِينَ
Ña gàdday ngir liggéey ci yoonu Yàlla, topp ñu rey leen mbaa ñu dee, fàwwu Yàlla dana leen wërsëgal wërsëg wu rafet, te nag Yàlla moo di Ki gën a mën a wërsëgal ci képp kuy wërsëgal.
59لَيُدْخِلَنَّهُم مُّدْخَلًا يَرْضَوْنَهُ ۗ وَإِنَّ اللَّهَ لَعَلِيمٌ حَلِيمٌ
fàwwu dana leen tàbbal barab boo xam ne danañu ca bég, te Yàlla ku xam la, Ku lewet la.
60۞ ذَٰلِكَ وَمَنْ عَاقَبَ بِمِثْلِ مَا عُوقِبَ بِهِ ثُمَّ بُغِيَ عَلَيْهِ لَيَنصُرَنَّهُ اللَّهُ ۗ إِنَّ اللَّهَ لَعَفُوٌّ غَفُورٌ
Noonu la. Ku mbugale lu toll ni la ñu ko tooñ, topp ñu tooñaat ko, Yàlla dana ko dimbali, Yàlla Jéggalaakoon, Baalewaakoon la.
Al-HajjFihi Alxuraan
78Aaya
MedinanRevelation
58Aaya

Tekki — Al-Hajj 58

Simoore Al-Hajj Aaya 58 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña gàdday ngir liggéey ci yoonu Yàlla, topp ñu rey…

Simoore Aaya 58/78 — Al-Hajj الحج (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Hajj Dégg, Al-Hajj Tekki, Al-Hajj mp3, Al-Hajj pdf. Aaya 56–60. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers