Al-Qasas · 44/88
Tekki Waxtaan — Simoore Al-Qasas
وَمَا كُنتَ بِجَانِبِ الْغَرْبِيِّ إِذْ قَضَيْنَا إِلَىٰ مُوسَى الْأَمْرَ وَمَا كُنتَ مِنَ الشَّاهِدِينَ ۝٤٤
Wa maa kunta bijaanibil gharbiyyi iz qadainaaa ilaa Moosal amra wa maa kunta minash shaahideen
📖 Tekkim Wolof
Te yaw [Muhammad], nekkoo woon ca xuru sowwu wa ca ba Nuy jox Muusaa ndigal ya: te fekkewoo ko woon [seede ko].

🎧 Dégg


📜 Aaya 42-46 — Simoore Al-Qasas

42وَأَتْبَعْنَاهُمْ فِي هَٰذِهِ الدُّنْيَا لَعْنَةً ۖ وَيَوْمَ الْقِيَامَةِ هُم مِّنَ الْمَقْبُوحِينَ
Nu toqal leen am rëbb ci àddina sii. Te bu Bis-pénc baa dañuy bokk ca ña ñuy siibiibal.
43وَلَقَدْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ مِن بَعْدِ مَا أَهْلَكْنَا الْقُرُونَ الْأُولَىٰ بَصَائِرَ لِلنَّاسِ وَهُدًى وَرَحْمَةً لَّعَلَّهُمْ يَتَذَكَّرُونَ
Jox Nanu Muusaa Téere ba, - ca ginnaaw ba Nu faagaagalee maas ya ko jiitu, - ngir mu doon am njis ak njub, ak yërmaande ak it ngir ñu mën caa fàttalikoo.
44وَمَا كُنتَ بِجَانِبِ الْغَرْبِيِّ إِذْ قَضَيْنَا إِلَىٰ مُوسَى الْأَمْرَ وَمَا كُنتَ مِنَ الشَّاهِدِينَ
Te yaw [Muhammad], nekkoo woon ca xuru sowwu wa ca ba Nuy jox Muusaa ndigal ya: te fekkewoo ko woon [seede ko].
45وَلَٰكِنَّا أَنشَأْنَا قُرُونًا فَتَطَاوَلَ عَلَيْهِمُ الْعُمُرُ ۚ وَمَا كُنتَ ثَاوِيًا فِي أَهْلِ مَدْيَنَ تَتْلُو عَلَيْهِمْ آيَاتِنَا وَلَٰكِنَّا كُنَّا مُرْسِلِينَ
Waaye sosoon Nanu ay maas yu guddu na fan. Te it nekkoo woon ca waa Madiyaana di leen nettali Sunuy kàddu; waaye Nun [Yàlla], Noo daan yable.
46وَمَا كُنتَ بِجَانِبِ الطُّورِ إِذْ نَادَيْنَا وَلَٰكِن رَّحْمَةً مِّن رَّبِّكَ لِتُنذِرَ قَوْمًا مَّا أَتَاهُم مِّن نَّذِيرٍ مِّن قَبْلِكَ لَعَلَّهُمْ يَتَذَكَّرُونَ
Nekkoo woon it wetu Tuur jamono ja Nuy woote. [Waaye dangaa dikk di] yërmaandey sa Boroom, ak it ngir nga xupp aw nit ñoo xam ne mësuñoo am ab xuppekat ci la ko jiitu, ndax it ñu mën caa fàttalikoo.
Al-QasasFihi Alxuraan
88Aaya
MeccanRevelation
44Aaya

Tekki — Al-Qasas 44

Simoore Al-Qasas Aaya 44 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te yaw [Muhammad], nekkoo woon ca xuru sowwu wa ca…

Simoore Aaya 44/88 — Simoore Al-Qasas القصص (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Al-Qasas Dégg, Simoore Al-Qasas Tekki, Simoore Al-Qasas mp3, Simoore Al-Qasas pdf. Aaya 42–46. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers