Aali Imran · 105/200
Tekki Waxtaan — Aali Imran
وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ تَفَرَّقُوا وَاخْتَلَفُوا مِن بَعْدِ مَا جَاءَهُمُ الْبَيِّنَاتُ ۚ وَأُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ ۝١٠٥
Wa laa takoonoo kallazeena tafarraqoo wakhtalafoo mim ba`di maa jaaa`ahumul baiyinaat; wa ulaaa`ika lahum `azaabun `azeem
📖 Tekkim Wolof
Te buleen mel ni ña teqalikoo juuyoo, ginnaaw ba leen leeral ga dikkalee, ñooña am nañu mbugal mu rëy.

🎧 Dégg


📜 Aaya 103-107 — Aali Imran

103وَاعْتَصِمُوا بِحَبْلِ اللَّهِ جَمِيعًا وَلَا تَفَرَّقُوا ۚ وَاذْكُرُوا نِعْمَتَ اللَّهِ عَلَيْكُمْ إِذْ كُنتُمْ أَعْدَاءً فَأَلَّفَ بَيْنَ قُلُوبِكُمْ فَأَصْبَحْتُم بِنِعْمَتِهِ إِخْوَانًا وَكُنتُمْ عَلَىٰ شَفَا حُفْرَةٍ مِّنَ النَّارِ فَأَنقَذَكُم مِّنْهَا ۗ كَذَٰلِكَ يُبَيِّنُ اللَّهُ لَكُمْ آيَاتِهِ لَعَلَّكُمْ تَهْتَدُونَ
Jafanduleen yéen ñépp ci buumug Yàlla gi te buleen teqalikoo ; fàttalikuleen xéewal gi leen Yàlla defaloon ba ngeen nekkee ay noon [lu jiitu Lislaam], mu tàppe seeni xol. Ba ngeen mujj ci xéewalam di ay doomi ndey. Te it nekkoon ngeen ci pindub kàmbug Safara, mu xettali leen ci loolu. Noonu la leen Yàlla di leeralee ay káddoom ndax Yàlla ngeen gindiku.
104وَلْتَكُن مِّنكُمْ أُمَّةٌ يَدْعُونَ إِلَى الْخَيْرِ وَيَأْمُرُونَ بِالْمَعْرُوفِ وَيَنْهَوْنَ عَنِ الْمُنكَرِ ۚ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ
Sàkkleen ci seen biir kurél buy woote jëme [nit ñi] ci mbaax [yiw], ñuy digle njekk ci tere njekkar . Ñooña ñooy ña texe.
105وَلَا تَكُونُوا كَالَّذِينَ تَفَرَّقُوا وَاخْتَلَفُوا مِن بَعْدِ مَا جَاءَهُمُ الْبَيِّنَاتُ ۚ وَأُولَٰئِكَ لَهُمْ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Te buleen mel ni ña teqalikoo juuyoo, ginnaaw ba leen leeral ga dikkalee, ñooña am nañu mbugal mu rëy.
106يَوْمَ تَبْيَضُّ وُجُوهٌ وَتَسْوَدُّ وُجُوهٌ ۚ فَأَمَّا الَّذِينَ اسْوَدَّتْ وُجُوهُهُمْ أَكَفَرْتُم بَعْدَ إِيمَانِكُمْ فَذُوقُوا الْعَذَابَ بِمَا كُنتُمْ تَكْفُرُونَ
Bis ba ay xar-kanam di weex tàll, ay xar-kanam it di ñuul kukk, ña nga xam ne seeni kanam dana ñuul [dana ñu leen wax] ne: “Ndax dangeen weddi gannaaw ba ngeen gëmee ? ”. Mosleen, toqamtikuleen mbugal mii ci sababus li ngeen doon weddi.
107وَأَمَّا الَّذِينَ ابْيَضَّتْ وُجُوهُهُمْ فَفِي رَحْمَةِ اللَّهِ هُمْ فِيهَا خَالِدُونَ
Ña nga xam ne seeni kanam ya dafa weex, dana ñu nekk ci yërmaandey Yàlla, te dañu fay béel.
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
105Aaya

Tekki — Aali Imran 105

Simoore Aali Imran Aaya 105 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Te buleen mel ni ña teqalikoo juuyoo, ginnaaw ba leen…

Simoore Aaya 105/200 — Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Aali Imran Dégg, Aali Imran Tekki, Aali Imran mp3, Aali Imran pdf. Aaya 103–107. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers