Aali Imran · 122/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
إِذْ هَمَّت طَّائِفَتَانِ مِنكُمْ أَن تَفْشَلَا وَاللَّهُ وَلِيُّهُمَا ۗ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ ۝١٢٢
Iz hammat taaa`ifataani minkum an tafshalaa wallaahu waliyyuhumaa; wa `alal laahi falyatawakkalil mu`minoon
📖 Tekkim Wolof
[Fàttalikul] ba ñaari kurél ci yéen naree yoqat ! Te Moo leen dimbali woon ba delluwuñu ginnaaw ! Way-gëm ña, nañu sukkandiku ci Yàlla [Uhud].

🎧 Dégg


📜 Aaya 120-124 — Simoore Aali Imran

120إِن تَمْسَسْكُمْ حَسَنَةٌ تَسُؤْهُمْ وَإِن تُصِبْكُمْ سَيِّئَةٌ يَفْرَحُوا بِهَا ۖ وَإِن تَصْبِرُوا وَتَتَّقُوا لَا يَضُرُّكُمْ كَيْدُهُمْ شَيْئًا ۗ إِنَّ اللَّهَ بِمَا يَعْمَلُونَ مُحِيطٌ
Bu ngeen amee bànneex, mu naqari leen. Bu ngeen amee naqar, mu di seen bànneex ñoom. Waaye bu ngeen muñee te ragal Yàlla, seen pexe yi duleen wàññi dara. Te Yàlla ku peeg la la ñuy def.
121وَإِذْ غَدَوْتَ مِنْ أَهْلِكَ تُبَوِّئُ الْمُؤْمِنِينَ مَقَاعِدَ لِلْقِتَالِ ۗ وَاللَّهُ سَمِيعٌ عَلِيمٌ
Fàttalikul yaw Yonent bi, ba nga xëyee jóge ci sa njaboot, di tegtal jullit ña barabu xeexukaay ya, xamal ne Yàlla kuy dégg la, Kuy xam la.
122إِذْ هَمَّت طَّائِفَتَانِ مِنكُمْ أَن تَفْشَلَا وَاللَّهُ وَلِيُّهُمَا ۗ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ
[Fàttalikul] ba ñaari kurél ci yéen naree yoqat ! Te Moo leen dimbali woon ba delluwuñu ginnaaw ! Way-gëm ña, nañu sukkandiku ci Yàlla [Uhud].
123وَلَقَدْ نَصَرَكُمُ اللَّهُ بِبَدْرٍ وَأَنتُمْ أَذِلَّةٌ ۖ فَاتَّقُوا اللَّهَ لَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ
Yàlla dimbali woon na leen ca Badar, ba ngeen nekkee ñu néewle. Ragal-leen Yàlla ndax amaana ngeen gërëm ko !
124إِذْ تَقُولُ لِلْمُؤْمِنِينَ أَلَن يَكْفِيَكُمْ أَن يُمِدَّكُمْ رَبُّكُم بِثَلَاثَةِ آلَافٍ مِّنَ الْمَلَائِكَةِ مُنزَلِينَ
[Fàttalikul yaw Yonent bi] ba nga waxee ña gëm : “Moo ndax doyuleen, seen Boroom, tëbb leen ñetti junni Malaaka yu wàcc [ngir dimbali leen]” ?
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
122Aaya

Tekki — Aali Imran 122

Simoore Aali Imran Aaya 122 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttalikul] ba ñaari kurél ci yéen naree yoqat ! Te…

Simoore Aaya 122/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 120–124. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers