Aali Imran · 86/200
Tekki Waxtaan — Simoore Aali Imran
كَيْفَ يَهْدِي اللَّهُ قَوْمًا كَفَرُوا بَعْدَ إِيمَانِهِمْ وَشَهِدُوا أَنَّ الرَّسُولَ حَقٌّ وَجَاءَهُمُ الْبَيِّنَاتُ ۚ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ ۝٨٦
Kaifa yahdil laahu qawman kafaroo ba`da eemaanihim wa shahidooo annar Rasoola haqqunw wa jaaa`ahumul baiyinaat; wallaahu laa yahdil qawmaz zaalimeen
📖 Tekkim Wolof
Naka la Yàlla di jubalee nit ñu weddi ginnaaw seen ngëm te ñu seede ne Yonent ba ku dëggu la, te lay yu leer dikkal leen ? Yàlla du gindi nit ñu nekk ay tooñkat.

🎧 Dégg


📜 Aaya 84-88 — Simoore Aali Imran

84قُلْ آمَنَّا بِاللَّهِ وَمَا أُنزِلَ عَلَيْنَا وَمَا أُنزِلَ عَلَىٰ إِبْرَاهِيمَ وَإِسْمَاعِيلَ وَإِسْحَاقَ وَيَعْقُوبَ وَالْأَسْبَاطِ وَمَا أُوتِيَ مُوسَىٰ وَعِيسَىٰ وَالنَّبِيُّونَ مِن رَّبِّهِمْ لَا نُفَرِّقُ بَيْنَ أَحَدٍ مِّنْهُمْ وَنَحْنُ لَهُ مُسْلِمُونَ
Neel : “Gëm nanu Yàlla, li ñu wàcce ci nun, li ñu wàcce ci Ibraahiima, ak Ismaahiila, ak Yanqooba, ak ca sët ya, ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa ak Yonent ya, mu tukkee ca seen Boroom [Téere ya]: dunu téqale kenn ci ñoom te nun way-wommatu lañu [jébbulu] jëm ci Yàlla”.
85وَمَن يَبْتَغِ غَيْرَ الْإِسْلَامِ دِينًا فَلَن يُقْبَلَ مِنْهُ وَهُوَ فِي الْآخِرَةِ مِنَ الْخَاسِرِينَ
Kuy sàkku diine ju dul Lislaam, deesu ko nangul, te bu àllaaxiraa, ca way-ñàkk ña lay bokk.
86كَيْفَ يَهْدِي اللَّهُ قَوْمًا كَفَرُوا بَعْدَ إِيمَانِهِمْ وَشَهِدُوا أَنَّ الرَّسُولَ حَقٌّ وَجَاءَهُمُ الْبَيِّنَاتُ ۚ وَاللَّهُ لَا يَهْدِي الْقَوْمَ الظَّالِمِينَ
Naka la Yàlla di jubalee nit ñu weddi ginnaaw seen ngëm te ñu seede ne Yonent ba ku dëggu la, te lay yu leer dikkal leen ? Yàlla du gindi nit ñu nekk ay tooñkat.
87أُولَٰئِكَ جَزَاؤُهُمْ أَنَّ عَلَيْهِمْ لَعْنَةَ اللَّهِ وَالْمَلَائِكَةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
Ñooña, seen pey nekkul lu dul rëbbum Yàlla ak Malaaka ya ak nit ñépp, dana dal ca seen kaw.
88خَالِدِينَ فِيهَا لَا يُخَفَّفُ عَنْهُمُ الْعَذَابُ وَلَا هُمْ يُنظَرُونَ
Dañu fay béel ca Safara. Kenn duleen woyafal mbugal ma, kenn duleen ko yéexalal,
Aali ImranFihi Alxuraan
200Aaya
MedinanRevelation
86Aaya

Tekki — Aali Imran 86

Simoore Aali Imran Aaya 86 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Naka la Yàlla di jubalee nit ñu weddi ginnaaw seen…

Simoore Aaya 86/200 — Simoore Aali Imran آل عمران (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Aali Imran Dégg, Simoore Aali Imran Tekki, Simoore Aali Imran mp3, Simoore Aali Imran pdf. Aaya 84–88. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers