Luqman · 24/34
Tekki Waxtaan — Simoore Luqman
نُمَتِّعُهُمْ قَلِيلًا ثُمَّ نَضْطَرُّهُمْ إِلَىٰ عَذَابٍ غَلِيظٍ ۝٢٤
Numatti`uhum qaleelan summa nadtarruhum ilaa `azaabin ghaleez
📖 Tekkim Wolof
Dananu leen bànneexal as ndiir ; daldi leen mbaq ci mbugal mu diis.

🎧 Dégg


📜 Aaya 22-26 — Simoore Luqman

22۞ وَمَن يُسْلِمْ وَجْهَهُ إِلَى اللَّهِ وَهُوَ مُحْسِنٌ فَقَدِ اسْتَمْسَكَ بِالْعُرْوَةِ الْوُثْقَىٰ ۗ وَإِلَى اللَّهِ عَاقِبَةُ الْأُمُورِ
Képp ku jébbal Yàlla boppam tey rafetal, [na xam ne] ŋoy na ci buum gi gën a dëgër. Te ca Yàlla la mbir yépp di mujj.
23وَمَن كَفَرَ فَلَا يَحْزُنكَ كُفْرُهُ ۚ إِلَيْنَا مَرْجِعُهُمْ فَنُنَبِّئُهُم بِمَا عَمِلُوا ۚ إِنَّ اللَّهَ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ
Képp ku weddi it, weddeem ga bumu la jaaxal : danañu dellusi ci Nun, ñu xibaar leen la ñu jëfoon. Yàlla xam na xéll li nekk ci dënn yi.
24نُمَتِّعُهُمْ قَلِيلًا ثُمَّ نَضْطَرُّهُمْ إِلَىٰ عَذَابٍ غَلِيظٍ
Dananu leen bànneexal as ndiir ; daldi leen mbaq ci mbugal mu diis.
25وَلَئِن سَأَلْتَهُم مَّنْ خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ لَيَقُولُنَّ اللَّهُ ۚ قُلِ الْحَمْدُ لِلَّهِ ۚ بَلْ أَكْثَرُهُمْ لَا يَعْلَمُونَ
Te su leen laajoon : “Ku bind asamaan yeek suuf si ? ”, kon ñu ne : “Yàlla ! ”. Waxal : “Cant ñeel na Yàlla ! ”. Waaye ñi ëpp ci ñoom xamuñu.
26لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ إِنَّ اللَّهَ هُوَ الْغَنِيُّ الْحَمِيدُ
Yàllaa moom li ci asamaan yeek suuf si. Yàlla Ku doylu la, di Yayoowaakoonub cant !
LuqmanFihi Alxuraan
34Aaya
MeccanRevelation
24Aaya

Tekki — Luqman 24

Simoore Luqman Aaya 24 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dananu leen bànneexal as ndiir ; daldi leen mbaq ci…

Simoore Aaya 24/34 — Simoore Luqman لقمان (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Luqman Dégg, Simoore Luqman Tekki, Simoore Luqman mp3, Simoore Luqman pdf. Aaya 22–26. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers