Al-Ahzab · 28/73
Tekki Waxtaan — Al-Ahzab
يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ قُل لِّأَزْوَاجِكَ إِن كُنتُنَّ تُرِدْنَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا وَزِينَتَهَا فَتَعَالَيْنَ أُمَتِّعْكُنَّ وَأُسَرِّحْكُنَّ سَرَاحًا جَمِيلًا ۝٢٨
Yaaa aiyuhan Nabiyyu qul li azwaajika i kuntunna turidnal hayaatad dunyaa wa zeenatahaa fata`aalaina umatti`kunna wa usarrihkunna saraahan jameela
📖 Tekkim Wolof
Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ne leen : “Su fekke ne dundug àddina sii rekk a leen ñor ak ub taaram, kaayleen ma yombalal leen ko, ci ma fase leen ci am pase mu jekk.
🎧 Dégg

📜 Aaya 26-30 — Al-Ahzab

26وَأَنزَلَ الَّذِينَ ظَاهَرُوهُم مِّنْ أَهْلِ الْكِتَابِ مِن صَيَاصِيهِمْ وَقَذَفَ فِي قُلُوبِهِمُ الرُّعْبَ فَرِيقًا تَقْتُلُونَ وَتَأْسِرُونَ فَرِيقًا
Te wàcce na ca ña doom jàmmaarlook yéen te bokk ca ñoñ-Téere, [yonjaxal leen], daldi dugal am tiit ci seen xol ya ; ngeen rey ñenn ña, lél ñenn ña.
27وَأَوْرَثَكُمْ أَرْضَهُمْ وَدِيَارَهُمْ وَأَمْوَالَهُمْ وَأَرْضًا لَّمْ تَطَئُوهَا ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرًا
Mu donnale leen seen suuf, ak seeni kër, ak seeni alal, ak suuf soo xam ne mësuleen ca xand. Yàlla mën na lu ne.
28يَا أَيُّهَا النَّبِيُّ قُل لِّأَزْوَاجِكَ إِن كُنتُنَّ تُرِدْنَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا وَزِينَتَهَا فَتَعَالَيْنَ أُمَتِّعْكُنَّ وَأُسَرِّحْكُنَّ سَرَاحًا جَمِيلًا
Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ne leen : “Su fekke ne dundug àddina sii rekk a leen ñor ak ub taaram, kaayleen ma yombalal leen ko, ci ma fase leen ci am pase mu jekk.
29وَإِن كُنتُنَّ تُرِدْنَ اللَّهَ وَرَسُولَهُ وَالدَّارَ الْآخِرَةَ فَإِنَّ اللَّهَ أَعَدَّ لِلْمُحْسِنَاتِ مِنكُنَّ أَجْرًا عَظِيمًا
Su fekkee nag ne Yàlla ak Yonentam ak kër gu mujj ga di àllaaxira rekk a leen ñor, [nangeen xam ne] képp kuy rafetal ci yéen, Yàlla dana ko waajalal ag pey gu màgg.
30يَا نِسَاءَ النَّبِيِّ مَن يَأْتِ مِنكُنَّ بِفَاحِشَةٍ مُّبَيِّنَةٍ يُضَاعَفْ لَهَا الْعَذَابُ ضِعْفَيْنِ ۚ وَكَانَ ذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ يَسِيرًا
Éy yéen soxnaay Yonent bi ! Képp ku bokk ci yéen te def aw ñaawtéef wu bir, dees na ko fulal mbugalam ñaari yoon ! Te loolu yomb na Yàlla.
Al-AhzabFihi Alxuraan
73Aaya
MedinanRevelation
28Aaya

Tekki — Al-Ahzab 28

Simoore Al-Ahzab Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Éy yaw Yonent bi ! Waxal say soxna ne leen…

Simoore Aaya 28/73 — Al-Ahzab الأحزاب (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Ahzab Dégg, Al-Ahzab Tekki, Al-Ahzab mp3, Al-Ahzab pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers